LI GËN A FËS CI XIBAARI RÉEW MI (ALTINE 3 AWRIL 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

4 AWRIL

Yewwi Askan Wi gàntal na Njiitu réew mi, Maki Sàll

Lëkkatoo Yewwi Askan Widu teewe defileb 4 awril bi. Njiiti lëkkatoog kujje gi dañu génneb yëgle, di ci xamle ne Njiitu réew mi, Maki Sàll, daf leen woo ci màggalug jonnug Senegaal giy am ci talaata ji, 4 awril 2023. Ginnaaw biñ fésalee seen ug ngërëm ci Nguur gi, daldi delloo njukkal làrme bi, dañu bind ne, duñu nangul Njiitu réew mi mébétam. Li ko waral mooy ne, ñoom, dañu jàpp ne, Maki Sàll, ci salfaañe seen i àq la dëkk. Bés bu nekk mu tooñ kujje gi, di leen xoqatal ak a fitnaal, rawatina demokaraasi bim yàq ba mu yàqu yaxeet. Ci kow loolu lañ gis ne, seen ngor mayu leen ñuy wuyuji wooteb Njiitu réew mi. Nde, day xaw a ndiru mbirum naaféq.

Aminata Ture tamit bañ na

Ginnaaw waa YAW, Soxna Aminata Ture tamit gàntal na wooteb Njiitu réew mi, Maki Sàll. Ci xëtu Facebookam la Mimi Ture biral ne du dem ca du teew ca Péncum Askan wa (Place de la Nation), talaata 4 awril 2023, ngir màggalug bés bi Senegaal moome boppam. Rax ba ca dolli sax ne, na ko Maki Sàll delloo « moomeg dépiteem ». Moom kay, ci tontoom li, daf ci fàttaliwaale Maki Sàll ne, mënul am 3eelu moome ci réew mi. Lii mooy li gone yiy wax : « xeex day saf monjaal ! »

Ismayla Maajoor Faal ak 3eelu moome gi

Démb ci ndajem TFR (Task Force Républicain) la jëwriñu Yoon wi, Ismayla Maajoor Faal, dëggalaat taxawaayam, ñeel ñetteelu moomeg Njiitu réew mi Maki Sàll. Moom, dafa wax ne, loolu, lu mën a nekk la. Ndax, ci wàllu Yoon, coow loolu lijjantiku na. Ba ci sax ca Ndajem Ndeyu-àtte bi lijjantiku na ca fukki fan ak ñaar ci weeru féewaryee 2016. Ñoom waa TFR, am nañu njort lu rafet lool ci mën a nekkug lawax Njiitu réew mi. Te, dinañu ko ci jàppale bu jamonoy jëf jotee.

KOOM-KOOM

Ñàkkug suukar si

Noo ngi xaarandi biir Ndakaaru, ci altine jii 3 awril 2023, 20 000iy toni suukar.  Njëwriñu yaxantu gee siiwal xibaar boobule. Abdu Karim Fofana mooy saytu céddaleg suukar si. Dañ ko jéggaani. Tey ci altine ji, bu 12i waxtu jotee, lees wax ne dina teersi ca waaxu Ndakaaru, laata ñu koy tas ci réew mi.

NAPP GI : Coow la ca Cees

Xeex bu mette metti moo am ci diggante ñaari gaali nappkat ca diiwaanu Cees. Ñaari gaal yépp, ay doomi réewum Senegaal ñoo ci nekkoon. Ñenn ñi di waa Mbooro, ñeneen ñi di waa Kayaar. Ci xibaar yi sunuy naataangoy Emedia siiwal, coowal dig ak ku nekk fi nga war a yem ci biir géej gee leen boole. Ca lañu xeexee xeex bu mettee metti. Ñu bare ame nañu ciy gaan-gaañu. Nee ñu sax, am ñuñ sotti esãs, taal leen, ñu lakk ba dee. Muy jéyya ju réy a réy.

TÀGGAT-YARAM : Farãas bañ na def ni Àngalteer ak Almaañ

Ci wéeru koor gi, waa Almaañ ak waa Àngalteer dañoo dogal ni, bu dog jotee, ñii di arbit yi dañuy taxawal joŋante yi as lëf, may ñi wooroon dog seen koor ba noppi, ñu wéyal. Ñu bari ci àddina si rafetlu ko, nag. Waaye, Farãs moom, daf ko bañal jullit ña fay kuppe. Nde, kurél giy saytu kuppe gi foofa, dafa jox ndigal arbit yi, ne leen ñu bañ a taxawal benn joŋante ngir naan dañuy maye ay dog koor ak lu ni mel. Loolu nag nekk na loo xam ni dafay wane ni foofu ca réew ma nanguluñ ñépp seen ug wuute, te it kenn rafetluwu ko. Ndax, ñiy jullit bari nañ fa lool. Waaye, Farãs moom, saa su nekk, day fésal bañ ak xeex bi muy xeex diiney Lislaam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj