Kañ mbirum xeetal, xeeb ak mbañeel di jeex ci àddina si, rawatina ci àddinay kuppe gog, yoonam nekku ca ? Saa bu ñu yaakaaree ni tane na rekk,beneen ñaawteef jibati. Daf ci am réew yoy, fa la Waaloo gënee aay, te Itali ci la bokk. Ndax, foofu ca Itaali, mënees na wax ni seen baaxu-maam la. Daanaka doo toog ab diir lu moy dinga dégg coowalug xeetal lëmbe fa. Bërkaati-démb rekk a ci mujju. Nde, kuppekat bu ñuul bii di Lukaku, dundaat na yu ñaaw yile. Ca joŋante ba doxoon diggante Inter Milan ak Juventus la lenn ci siporteeri Juventus doon ko yuuxook a woyal ay baat yu ñaaw yuy ŋàññi ñuulaayam ak di xalab xeetam. Doonte ne, moom Lukaku, du saa-Afrig. Ndaxte, bu dee Afrig lay way-juram cosaanoo tam, Belsig la juddoo, màgge, taamoo nekk doomu Belsig wëlis Kongo gi maamam yi fekk baax. Waaye de, li wolof di wax rekk, wax ju ñaaw dëkkul fa mu jëm, fa mu jóge la dëkk. Te, saaga yooyu taxu koo génn ci matsam. Nde, dugal na fa benn bii, daldi daw ba seen kanam, jàkkaarlook ñoom, def baaram ba ca gémmiñam. Mu mel ni ku leen di tontu, di leen noppiloo. Waaye, arbit bi nag daf ko ci jox ab ruus. Ruus boobu nag, jur na fa coow, ndax ñu baree bari ànduñu ci ndogalu arbit bi.
CHELSEA
Frank Lampard la ñu tegandi ca bopp këlëbu Chelsea ngir mu àggali li des ci sàmpiyonaa bi, gannaaw bi ñu dàqee ka leen doon tàggat, Graham Potter. Ñaari yoon a ngi nii njiiti Chelsea yi di dàq seen tàggatkat. Ndax, Graham Potter mi ñu mujje dàq, daf wuutu woon Thomas Tuchel mi ñu njëkkoon a dàq. Lampard, nag, wii mooy ñaareelu yoon muy yor Chelsea. Nde, njëkkoon na leen tàggat laata ñu ko dàq moom itam.
UEFA
Aleksander Ceferin falaat nañ ko ci boppub UEFA ba atum 2027. Gii moo di ñetteelu moomeem ci boppu kurél gi boot kuppeg Tugal. Ndaxte, atum 2016 lañ ko fa tegoon ba léegi.
SAAJO MAANE
Ñañcoo bi ñëwaatagul ba léegi ! Saajo Maane, ba tey, delloogul buum gi ca boy-boy ga. Ndax, bim delsee ba nëgëni, kenn xàmmeetu ko. Amaana toogaayam bu yàgg bim toog ci sababu gaañu-gaañu bim ame woon a ko waral. Amaana yit, fi ñu koy teg moo baaxul ci moom. Nde, ñaari joŋante yi mu am ak ekibu Senegaal ci fan yii ñu génn, gis nañu ni ba léegi am na lu des. Waayeet, ca këlëbam bii di Bayern Munich itam, waxi noppi. Dafa di, keroog, ca seen joŋanteb kuppe bi mujju bi, daf cee meloon ni ku réer ci biir pàkk mi. Warees na xool, seet ba xam luy jafe-jafe bi ngir indi ci saafara balaa moo gën a yàgg.
KUBU ESPAAÑ : BARCA 0 – 4 REAL
Bërki-démb, ci àllarba ji, Barcelone ak Real Madrid doon amal seen ñaareelu ndaje ñeel kuppeg Buuru Espaañ bi (Coupe du roi). Ca fowub (estaad) Barça lees ko doon amale. Waaye, nag, Real daf ko toroxal biir dëkkam, dóor ko 4-0. Ca joŋante bu njëkk ba, Barça moo dóoroon 1-0. Kariim Benzema moo dugal ñetti bii. Moom, Benzema, mooy saa-Real bi njëkk a dugal ñetti bii ca “Camp Nou” ginnaaw Ferenc Puskas mi ko njëkke woon atum 1963.