Adebayoor, saa-Tógoo bàyyina kuppe ! Barkaatii-démb ci altine ji la yëgle ne tekkinay dàllam fas-yéene ko bàyyi ak xale yi ndax ne mag dikk na. Moo ngeek 39i at, kuppe deseelatu ko dara. Lenn ci ekib yu mag yu mu jaar mën nañ ci tudd Monaco, Arsenal, Réal Madrid ak Manchester City, nekkoon fa ku am solo, ba ci dëkkam itam, Tógoo, kuñ fa joxoon cër la ndax lim fa def.
Moom mii di Özil tamit gënoon siiw ca booru Réal Madrid, jóge fa jaar Arsenal laata muy dem fa Tirkii ca këlëb boobu di Besiktas, xamle na itam ni wékk nay dàllam, bàyyi kuppe. Moom nag, moo ngi bàyyee 34i at. Bokk na ci kuppekat yees di tudd ci mën paas donte mujjug dundug kuppeem demeewul nim ko bëggee woon ndax ay jafe-jafe yu sew-sewaan.
Espaañ/Barça
Barcelone mi ngi ciy jafe-jafe jamono jii. Nde, dañ ko tuumaal ne dafa daan ger arbit yi, diggante 2003 ba 2018. Mbir mi tàbbi ci loxoy Yoon, muy def i jéego, di lëñbët ngir xam li xew. Loolu nag, andi nay wax yu sew : ñii di dëggal, ñee di weddi. Waaye, dara leeragu ci. Démb, bi ñu xëyee, ñenn ci taskati xibaari Espaañ yi génne nañuy xibaar di wax ni, moom Barça narul a bokk ca “League des Champions” déwén bi. Laporte, njiitu Barça, loolee naqari na ko bam dem ci yoon “plainte” lenn ci taskati-xibaar yooyee. Gannaaw loolu nag, ñu ci bari dindi nañu xibaar yi ñu dugaloon ci mbaali-jokkoo yi.
CAN U-23 : Senegaal duma na Mali 3-1
Démb, ci àllarba ji, la ndawi Senegaal yi amagul 23i at doon amal seen joŋante bu njëkk ñeel kuppeg Afrig gees jagleel ndaw yi amagul 23i at. Ñu doon ci daje ak Mali. Senegaal moo mujje gañe ñetti bal ci benn.