LI GËN A FËS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM (ALXAMES 9 MÀRS 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

KUPPE

Àngalteer

Démb, foo geestu ci mbaali-jokkoo, ñoo ngi doon wone ay naataal ak i widewooy kii nga xam ni mooy defãsëeru Manchester City bi, Kyle Walker. Mu mel ne ku àndul woon ak sagoom. Nde, mi ngi ciy tërëf ni ku màndi. Bu ca yemoon sax mu tane. Waaye, dafa mel ni ku lonk as ndaw, dawal loxoow yi ci awaray soxna si. Loolu nag, jur na wax ju réy, foofa ca Àngalteer, nek it lu ñu ñaawlu lool. Rafetul sax cib kuppekat bu ñépp ràññe.

LIGUE DES CHAMPIONS

PSG toogati na

 Démb ci àllarba ji la Bayern Munich, ekibu Saajo Maane bi, doon janook PSG bu ñoom Messi ak Mbappe. Njëkkoon nañu laale, 15i fan ci ginnaaw ca Pari, Bayern Munich dóor ko fa 1-0. Kon, PSG dafa waroon gañee as-tuut 2i bii ngir mën a jàll. Waaye, saa-almaañ yi mayuñu leen ko. Nde, wulli nañ leen wulli yu metti, wan leen ni xaajaguñ bay doon ekib bu mag. 2-0 lañ leen duma. Te, bu dul woon li arbit bi far benn biiwu Bayern bi ak li ataakã yi rate, doon na gën a ñaaw. Saajo Maane, bi joŋante bi dese danaaka 10i simili la dugg. Neymar moom dafa ame gaañu-gaañu moo tax kuppewul. Ci 7i at yii weesu, bii mooy 5eelu yoon PSG di tooge wicceem-dë-finaal.

Chelsea toogloo na Dortmund

Chelsea nax na kii di Dortmund ba génne ko ci Ligue des Champions bi. Bërki-démb ci talaata ji la woon seen joŋanteb ñaareel bi, mu dóor ko ñaari bal ci dara (2-0). Kuppekati Dortmund ya nag, am na ña bégul ca ni arbit ba doxalee. Ndax ku ci mel ni Bellingham moo ngi wax ne def nan li ñu waroon yépp, waroon nañ mën a gañe joŋante bi. Waaye nag arbit bi ni mu dooxalee dafa mel ne ku jeng jëmale ci waa Chelsea yi. Ñoom li leen metti mooy ni dafa dogal ñu dooraat ab teg-dóor boo xam ni bii kuppekatu Chelsea bi daf koo dóoroon mu moy. Li waral loolu nag, mooy ñenn ci waa Dortmund yi dañoo romb ci déyal biñ waroon na yam ba ñuy dóor bal ba.

Benfica itam toogloo na Fc Brugge, dóor ko juróomi bal ci benn (5-1) gannaaw bam ko dóoree woon, ca joŋante bu njëkk ba, ñaar ci tus (2-0).

CAN U20 2023

Senegaal dana daje ak wóllareem bii di Gàmbi gaawu 11i màrs bii ñeel finaalu CAN U20 bi. Ñoom ñaar nag, ba léegi dóoruñu ci kenn te lakkuñu ci it caaxu kenn ba nii nuy waxe. Loolu nag, du wéy, ndax bu bés baa kenn dana wéyal loolu ka ca des xaar. Ñuy ñaan Senegaal jëlaat boobu kub.

LÀMB

Gannaaw “recours” bi mu defoon, waa CNG mujje nañ jox kii di Saa-Cees ndam ci kaw Rëg-Rëg, xamle ni moom mii dafa rëpp ñeenti cëram (4 appuis) ca bëre ba. Muy àtte bu jaar yoon ndaxte ñepp gisoon nañu ni am na.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj