LI GËN A FËS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM (DIBÉER 5 MÀRS 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

LÀMB 

Saa-Cees – Rëg-rëg ñoo doon bëre ci dibéeru tey ji. Mu doonoon làmb ju ñépp doon xaar. Waaye, nag, coow am na ci. Nde, bu dee àttekat yi Rëg-rëg lañ jox ndam li, Saa-Cees ak i farandoom nee nañu ñoo daan. Ndaxte, ci biir jaxasoo bi, am na fu Rëg-rëg sampee 2i loxoom ak 2i wóomam, muy 4i apiwi, nees koy waxe. Kon, Saa-Cees a yeyoo ndam li. CNG mooy àtte.

PSG / FARÃS

Mbappe defati na jaloore

Mbappe tegaat na beneen jéego ! Doon na kuppekat bi ëpp lu mu dugal ci mbooru PSG. 201 bii la fa dugalagum bim fa ñëwee ba léegi. Bu ñu fàtte ni, Mbappe, 24i at doŋŋ la amagum. Waaye, ak li muy doon xale yépp, dafa dooj ba, turam siiw na lool. Gannaaw jéego bu réy bim defaat la Ronaldo, kuppekat Beresil bu mag ba, wax lii ci moom : ” Li Messi ak Ronaldo def ci kuppe, mennum Mbappe moo ko mën a defaat. Bu nu fàtte ni 24i la amagum.”

Marquinhos ame na gaañu-gaañu

Ba tay foofu ca PSG, gannaaw ndam li ñu am ci kaw Fc Nantes, démb ak li Mbappe def, njàqaree ngi bëgg a gane seen biir ak joŋante ñuy waajal ak Bayern, di bu ñu war a gañe bu ñu bëggee wéyal seen yoon ca “Ligue des Champions “. Marquinhos àggalewul seen joŋanteb démb bi, dafa gaañu, daldi fekki Neymar ak Kimpembe. Wuteek nañook Bayern mi nga xam ne, ay kuppekatam yi gaañu woon ñoo ngi delsi.

LIGA / Espaañ

Paap Alasaan Géy, ñu miin ko ci Paap Géy, defaat na beneen paas ci seen joŋante bi ñu ñàkk démb ci kanamu Athletico Madrid (1-6). Paas boobu mooy ñetteelam ba mu demee ca Seville ba léegi, di wane miinam bu gaaw ci këlëb ba. Mujjul a àggali joŋante bi itam, moom Paap Géy. Ndax, dañ ko ruus ginnaaw bi mu amee ñaari kartoŋ soon.

MILAN / ITALI

Ibrahimovic, na woon, fa woon

 “Ñëwat naa gannaaw sama gaañu-gaañu bi. Léegi, dinañu xamaat kuy tàmbali joŋante yi. Bi ma gaañoo ataakã yaa ngi doon wane seen bopp. Waaye nag, dikkaat na. » Kàddu yooyee la Ibrahimovic yëkkëti gannaaw ba ko benn taskatu-xibaar laajee lu jëm ci moom ak ekib ba.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj