Li gën a fés ci xibaari tàggat yaram (Gaawu 4 féewaryee 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PREMIER LEAGUE / ÀNGALTEER 

Liverpool

Ribeertoo Firminoo yëgal na waa këlëb ba ak tàggatkatam, Jurgen Klopp, ni dafay dem bu atum sàmpiyonaa bi jeexee. Li sabab loolu nag, mooy ni dafa yëgatul boppam ca ekib ba. Ndax, bareetul la mu fay joŋante jamono jii.

BUNDESLIGA / ALMAAÑ

Nkunku amatina gaañu-gaañu 

Christopher Nkunku amati na gaañu-gaañu. Démb, ci seen joŋante bi doxoon seen digganteek Dortmund, la gaañuwaat. Te, démb la doon door a delsi gannaaw gaañu-gaañu ba mu ame woon ca tàggatoom ba ak ekibu Farãs, ba ñuy waajal kuppeg àddina sa. Am na ñuy wax ni dafa toogul diir bi waroon ca gaañoom ba weesu moo waral mu dalaat ko. Dana toogaat ay fan.

Dortmund

Ñuul-mbokk yi nee nañu kenn du leen téye. Ñoo ngi wéyal, di dóor, di am ay ndam rekk, di dem. Ci 10i joŋante yu Dortmund amal ci atum 2023 mi, dafa gañe yépp, duggal ci 25i bii ba noppi jël ci 9 doŋŋ. Moo nekkagum ci boppu Sàmpiyonaa, fileek ñuy xaarandi Bayern dawal.

KARAGÜMRÜK / TIRKII

Mbay Jaañ a ngi yëngal sàmpiyonaa Tirkii ba. Tey, ci gaawu gi, ñetti bii la dugal, séddale benn paas. Kenn mënu koo téye jamono jii. Bu fekkee dafa bëgg wan Aliw Siise ni dafa war a  ñëwaat ekib Senegaal, moo ngi ci yoon wi. Ci 19i joŋante ya mu fa amagum, foofa ca Tirki, Mbay Jaañ dugal na ca 14i bii def itam 5i paas. Gaynde Njaay mbara-wàcc !

CAN U20 2023

Senegaal, Gàmbi, Tinisi ak Niseriyaa ñooy ekib yu dem 1/2 finaal. Ñoom ñeent ñii itam ñoo dagg paasu kuppegg àddina ñeel ñi amagul 20i at. Ngelaw liy uppu Senegaal ci wàllu tàggat-yaram Yàlla bu mu gaaw a dal, rawatina ci kuppe gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj