LI GËN A FÉS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

WURE (FUTBAL)

  • Gaynde Senegaal yu ndaw yi noppi nañoo waajal Chan bi. Tey ci altine ji lañu doon amal seen ub joŋante bu mujje ci waajtaay gi. Ginnaaw bi leen Marog dóoree (1-0), ñu témboo ak Alseri (2-2), dellu témboowaat ak Libi (1-1), dañoo dóor Saa-Congo yi benn bii ci tus. Gaawu bii di ñëw nag lañuy dajeek Koddiwaar ci seen joŋante bu njëkk ci Chan 2023 bi.

  • Garet Béel (Gareth Bale), tollu ci 33i at, wékk nay dàllam tay ci altine ji 9 Jaņwiyee 2023. Bàyyi na futbal, muy ca këlëbam ak réewam yépp.

  • Igóo Lóris, jàppkatu Farãs bi, moom itam, bàyyi na ekib Farãs. Moo ko xamle ciy kàddoom yii toftalu : ” Gannaaw 14i at yi ma xeexal mayo bi, yaakaar naa ne, àgg naa ca cat la. Maa ngi jël ndogal, daldi dakkal ànd beek ekibu Farãs, di am yëg-yëg ni joxe naa fa sama lépp”.

  • Nowel Lë Geret (Noël Le Graët), njiital FFF, génn na di jéggalu gannaaw bi mu waxeey kàddu yu ñagas ñeel Sinedin Sidaan. Dafa di, ñu bari ciy wurekat ak i kilifa, ca Farãs ak ci àddina sépp, ñoo génn di naqarlook a metitlu kàddu yooyee, rawatina Kiliyaan Mbape ak Reyaal Madrid, këlëbu Sidaan ba woon.

  • Bàrsalon toogati na ci bopp Sàmpiyonaa Espaañ ba, gannaaw ndam li mu am démb (1-0) ci kaw Ateletikoo Madrid. Moo rawee Reyaal Madrid 3i poñ. Ndeke, Reyaal dafa ñàkk barki-démb, ci gaawu bi, ci kanamu Wilaareyaal (1-2).

BASKET

  • Waa Spurs amal nañu pas ak Góorgi Si Jeŋ. Dana fa sol limatu 41 ba.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj