MAKI/XALIFA : MAG, BU RUSEE NE MAA-TEY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fan yii nu génn, bare woon na ñu doon yéy ak a yàbbi ci mbirum Xalifa Sàll, di wax ci njéggal bi ko Maki Sàll war a jagleel. Am na ci sax ay taskati xibaar yu demoon ba ne Xalifa Sàll këram lay tabaskijee. Waaye, bi nguur gi fésalee turi nit ñi Maki Sàll jéggal, ñu war a tabaskijee seen kër, kenn gisu ci ku tudd Xalifa Sàll. Muy mbetteel gu réy a réy ci ñenn ñi. Maki Sàll, moom, yéyu ci, yàbbiwu ci. Moone, askan wépp a ko ñaanoon njekk, kilifa diine yi, kilifa aada yi, kujje gi, kuréli way-moomeel yeek yenn mbootaay yi. Waaye, Maki dafa lànk, taxaw fi mu taxaw rekk. Rax-ci-dolli, ci ndoorteelu waxtaanu politig wi mu sumb, ñi ko wuyusi noon nañ ko li gën mooy mu bàyyi Xalifa. Wànte, dafa cosoon wax ji, yem fa. Nanguwu cee woon a sori. 

Maki Sàll dafa xaar ba dem bitim-réew, ca Biyaaris (Biarritz) ga muy teewe fan yii ndajem G7 mi, door a wax li mu xalaat dëggëntaan ci coowal njéggalub Xalifa Sàll mi nekk ciy loxoom. Ndaje moomu, nag, li mu jiite NEPAD moo tax ñu boole ko ci. Waaye, moom sax, bi mu dalee dem ay ndaje ba tey, mësta toj fenn. Ndaxte, dégguñu benn yoon fu ñu waxe ne Maki kat, bii yoon wax na wax ju réy, ni ko Ablaay Wàdd daan defe. 

Waaye, ba tey loolu ñorunu ; kàddu yi mu fa rotal ci mikóro RFI ñoo jar a bàyyi xel. Maki Sàll baat yii la fa wax ñeel Xalifa Sàll : « Bi ci njëkk mooy, wareesul a tënk giifalub làngu politig gi ci mbirum njéggal kese, yemale ko ci. Njéggalub njiitéef, ndeyu-àtte réewum Senegal moo ko jagleel njiitu réew mi. Kon, ci moom doŋŋ la aju, ciy loxoom kese la nekk. Moom mooy xool saa su ko soobee mu jéggale. Bu ko defee, sama yoon nekkul ci li taskati xibaar yiy wax ci njéggal bi, duma ci wax. Bés bu ma neexee walla ma am coobare gi rekk, dinaa ko def ni ma koy faral di defe. Ndax  at mu nekk, lu ëpp téeméeri nit walla sax ay junniy nit, ci xayma, dinaa leen jéggal, génne leen kaso… » 

Kon, noo ko déggandoo : kàddu yii la rotal ca Frãs. Ñu mën cee amal ñaari njàngat yu gàtt. Bi ci jëkk mooy ne, Maki Sàll wegul waa réew mi, joxul cër askan wi walla kilifa yi fiy yeewoo. Waaw, lu tax Maki Sàll bitim-réew rekk lay waxe ak a waxtaane mbirum réew mi ? Xanaa réew mi amul i taskati xibaar yu mu mën a janool dégtal leen i kàddoom ak i xalaatam ? Lii bu tekkiwul ñàkk faayda ak suufeel sa boop ak sa réew lu muy tekki leneen ? Ndax kat, lii xeebeel la ci waa réew mi, rawati-na taskati xibaar yi fi fekk baax. Da leen a tanqamlu, dummóoyu leen te nëbbu ko ndax moo ne ci gémmiñu boppam : « sama yoon nekkul ci li taskati xibaar yiy wax ci njéggal bi, duma ci wax. » Ndege, deesul gis benn njiitu réew lu ñàkk faayda bay péncoo mbiriy réewam fii ci Senegaal. Moom kay, Maki rekk a koy defi ca réewi xonq-nopp ya. Muy wone ne, ba tey moomagunu sunu bopp dëgg dëgg, ndax sunu njiit yi amuñu fulla amuñu faayda. 

Ñaareelu njàngat bi nuy jële ci kàddoom yooyu mënees na ko xaaj ñaar. Benn bi nitu Maki ci boppam la ñeel, beneen bi aju ci digganteem ak Xalifa Sàll. Bi ci njëkk mooy réy ak réy-réylu bi Maki di biral ciy kàddoom : « …ci moom doŋŋ la aju… », « …ciy loxoom kese la nekk. », « Moom mooy xool saa su ko soobee mu jéggale. », « Bés bu ma neexee walla ma am coobare bi rekk, dinaa ko def »… Maki Sàll, li mu nuy xamal ci kàddu yii mooy ne, moom kott, moom kese- kese mooy dogal. Kenn mënul wañaar loxoom ba defloo ko lu ko neexul, ak koo mënti doon. Maki Sàll dafa summi yérey njiitu réew, sol yérey Buur Saltige. Ndaxte, buuru saltige rekk mooy jiitee doole, di jaay maa-mën, jàpp ne lu mu wax mooy am, lu mu waxul du am ; lu mu bëgg mooy am, lu mu bëggul du am. Ndege, njiitu réew day woyof, nangoo déglu askanam ak kilifa réew mi ba tax lépp lu mu jàpp, su ñu ko ñaanee mu bàyyi. Waaye, Maki jikkoy firawna lay doxe. Waaw. Ndax bu demee bay dolli ci waxam ji : « …ni ma koy faral di defe.» ak  « …dinaa leen jéggal, génne leen kaso. », Maki day firndéel ni njéggal, jamono jii, ciy loxoom la nekk, ku ko neex la koy jagleel. Lii moo tax ndaw yi wutal ko dàkkental, di ko woowe « xaaju Yàlla » walla « àmbasadëeru Yàlla ci Senegaal ». Ndaxte, bu nee at mu nekk mu jéggal nit ñu bare, li wax ji wund mooy ku ci bokkul daŋ kaa neexul. 

Ci lanuy tàbbee ci ñaareelu njàngat bi ñeel digganteem ak Xalifa Sàll.

Ndax seetlu ngeen lenn ? Saa su Makiy wax ci mbirum Xalifa Sàll, du jaar ci turam. Xanaa keroog ba mu nee “sama doomu baay la” ndax sant wi ñu bokk. Rax-ci-dolli, ñépp xam nañ ni jot naa yabal ay ndaw ca kaso ba ngir ñu gise ak Xalifa Sàll. Xamunu lu ñu fa waxante, waaye mel na ni Maki dafa dencal mer Xalifa. Te, Xalifa wax na du benn du ñaar ne sàkkuwul njéggal ci Maki te soxlawu ko. Dafa mel ni am na lu Xalifa Sàll gàntal Maki ba tax koo ñéññ. Coxorte giy feeñ ciy waxam ak doxalinam doy nañ firnde. Ma leen di laaj nag : waaw, lan la Maki jàppal ngóor si Xalifa ba tax muy doxale nii ak moom ? Lan lañu jot a séq ? 

Ak lu ci mënti am, askan wi moom moo gën a sonn Xalifa fuuf. 

Bi mu tàmbalee taw ba léegi, askan wi nelawatul, te waa Ndakaaroo ci gën a sonn. Kër yi taa nañu, koñ yi taa, mbedd yi taa, tali yi fees dell ak ndox, kenn amul foo jaar. Njëg yépp yokku, xaalis amul, oto yiy mbëkkante ci tali bi, nit ñiy dee. Kenn xamul fooy teg sa tànk. Metit yooyu yépp teewul nguur gi ne ée-yaay, nun danuy bër, njiitu réew miy wone ay portale mook soxnaam ca Tugal, ci kër gu taaroo taaru, di bége. Mu mel ni dañuy mbëllee baadoolo yi. Li am ba des moo di, ak Maki, mel na ni, laabisiina la réew miy jubal. 

Nu dem rekk.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj