Àngale yaa ngay gundaandaat ! Manchester a ngi toj ! Ren, dafa baxa. Ci bëccëgu dibéeru tey ji, foo sànni woon mbàttu mu tàkk. Soppey Manchester City yaa nga feesoon dell mbeddi dëkk ba, di yuuxoo ak a fecci. Ñoo yey nag. Ndaxte, ba Manchester City dee këlëb ba tey, guléet ñuy jël “League des Champions”. Démb ci gaawu gi lañ duma Inter de Milan 1 bii ci 0, daldi witti seen njëlbeenug biddiiw ci joŋante bu mag bile.
Ay at ñoo ngi nii, waa Manchester City di di rëbb kub bi. Saa bu xëccaan buum ga ba yaakaar ni bii mooy baax bi rekk, buum ga dog. Daaw jéeg, demoon ba finaal, Chelsea ne dóor ko, yaakaar ji tas. Daaw, mu dem ba demi-finaal, Real Madrid nax ko, toogloo ko. Te, ndeysaan, ñépp a foogoon ne day rey Real Madrid. Waaye, ren de, fayu na fayu yu metti sax. Nde, dafa wulli Real Madrid wulli yu metti ci demi-finaal yi, duma ko 4-0, toogloo ko. Lu ko jiitu, ci kaar-dë-finaal yi, Bayern Munich la làbbali, toroxal ko biir dëkkam.
Li may Manchester City doole mooy ne, ren, dafa jënd atakã, dugalkat, bu xereñ te xobe : Erling Haaland. Moo taxi t, atum ren ji de, Manchester City ñépp la tër, muy mbuucaa-mbuuj yi, di punkal yi. Fa Àngalteer de, kenn yabu ko fa. Muy sàmpiyonaa di FA Cup, lépp la raafal. Desalul kenn dara. Ligue des Champions kesee ko dese wonn. Mu doon janook Inter de Milan, di ékib bu naqaree futbalal.
Finaal bi neexoon na lool. Joŋante bi neexoon na lool, bal biy daw jàmbar yay ñafe, ku nekk bañ sa moroom yóbbul la ko. Xaaj bu njëkk bi, ñu nekk ci ba dem noppalu, kenn dugalul sa moroom. Ñu dikkati ca ñaareelu xaaj bi, nekkaat ca, bal bay daw, gaa yay neexal ba ca 66eelu simili ba rekk, Rodri, di kuppekatu Manchester City, ne tuxum bal ba ca caaxu Onana yaa. Estaad bay riir, soppey Manchester City yay yëngal biir ak biti ga. Ñu nekkaat cay daw ba na mu jeexee. Arbit ne « Priip ! Priip ! Priiiiii…p ! » Rekk estaad ba tojati. Yuuxoo yeek sarxolle yi. Àngale yiy tëb ak a fecc fii, saa-itali yiy jooy, ndeysaan.
Pep Guardiola nag, tàggatkatu Manchester City bi, yoroon Barcelone ak Bayern Munich, kenn gënu koo bég. Xol baa nga mel ne wanagu mbott. Ndax, kub bi, daf ko yàgg a yóotu. Am ñu naan sax, ci mbooru futbal, moom mooy tàggatkat bi gën a aay. Ak lu ci mën di am, jaanam wàcc na.