WÀDD-MAKI : GINNAAW AY…SOPPI ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Keroog, àjjuma 27eelufan ci weeru sàttumbar, atum 2019,ba ñuy ubbi Masaalikul Jinaan, jullit yépp a bégoon, rawatina murid yi. Bégoon nañ ba, foo nattoon seen mbégte rekk, mu romb koy dem. Ndaxte, kat, wëliis li jumaa ji doon ab jaamukaayu Yàlla, Sunu Boroom, Masaalikul Jinaan dafa dib sag ci mboolem jullit ngireeni mu réye te yànj, kaar. Moom kay, guléet ñu gis fi jumaa ju ni mel ci Afrig sowu-jant ba mu daj. Te, nag, lépp li ko jëmmal mi ngi jóge ci  ñaqi doomi réew mi, ci seeni xalaat, ci seen alal ak ci seen doole.  Bu amee yit ay doxandéem yu ci dugal seen loxo, bariwuñu, te fay nañ leen liñ ci liggéey ba mu mat sëkk. Li ci ëpp, nag, Tuuba la jóge. 

Waaye ubbite boobu, daa am leneen lu mu jur ci wàllu politig, mu di juboob  Abdulaay Wàdd mi fi jiite woon réew mi ak Maki Sàll mi toog tey ci jal bi.

Kenn umplewul li dox ci diggante ñaar ñooñu, muy diggante baay ak doom.  Ñu ngiy fàttaliku ba Maki Sàll di génn PDS, ginnaaw ba ñu ko fa bunduxutaalee ndax joteem ak Karim Wàdd. Mu jóge fa taxawal parteem tudde ko APR, utali nit ñi, bokk ca joŋanteb atum 2012 ngir doon ñeenteelu njiitu réewum Senegaal. Ba Maki Sàll gàddoo ndam loolu ba léegi nag, diggante ñaari politiseŋ yi daanaka at mu jàll mu gën a ñagas. Noonu, ba Maki jàpplu doomu Ablaay Wàdd ji, Karim Wàdd, yoon daldi koy nëbb jant bi ñetti at. Ci mujjantal gi, ñu génne ko, gàddaayloo ko ngir rekk mu bañatee a bokk cib joŋanteb fii ci Senegaal. Ay at a ngi nii mu ne réewum Kataar, ñibbisi të ko. 

Digganteb ñaari kilifa yooyu nag, ku ne wax na ci ngir defaraat koo, rawatina njiiti diine yi, ñu gën cee ràññee Xalifay Murid yi fi jot a jaar. Ñenn ci njiiti réewi Afrig yi sax, ku ci mel ni Alfa Konde, xar nañ ci seen tànki tubéy ; waaye taxul diggante bi  defaru bay rattax.

Loolu lépp tax na, keroog ca ubbiteb Masaalikul Jinaan, kenn gëmewul woon maslaa yeek jàppante loxo yeek àndandoo bi ñaari kilifa yooyu nekkee, di saafoonte, di digante gisewaat ci ni mu gën a gaawe. Ca dëgg-dëgg, nit ñi yàgg nañoo ñaan lu ni mel am, waaye teewuleen woon a waaru.

Dëgg la, politiseŋ yi, dañu bariy feem, waaye nag, àndandoo Ablaay Wàdd beek Maki Sàll keroog, ñu dem bay lëngoo, ñépp la dawloo seen yaram, tooyal seen xol. Ci sunu gis-gis bu gàtt daal, mënees naa  am yaakaar ni juboo dëgg am na. Te nag, juboowu ñaari kàngam yooyu, war naa jur déggoo bu wóor fu bennoo mën a lalu, ba tax ñu mën jàpp ne, la jógge ca Masaalikul Jinaan lu taxaw la. 

Déggoo boobu, waxtaanu politig la, te ëllëgu Karim Wàdd – maanaam delluseem ak nekkinam ci réew mi, ak itam taxawaayam ci joŋante yiy ñëw – mooy li ci gën a soxal Wàdd. 

Su loolu lépp àntoo dinañu mën a wax ne Masaalikul Jinaan, ginnaaw li mu jur ci diine ji, di lu am a am solo, jur na it jàmm ak tawféex ci réew mi, tax na politiseŋ yi dakkal seen xulook seen ŋaayoo.

Waaye bu demewul noonu day rekk doon yaakaar ju tasati te ñépp dinañ ko naqarlu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj