MBATIT BIIR NDAKAARU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndakaaru dalal na “Festival come to my home”. Muy xew-xewu mbatit, cosaan ak xeltu, fekk baax  réewum Marog. Kii di Driss Alaoui Mdaghri nekkoon fa jëwriñ ji ñu dénkoon ndaw ñi, nekk tamit ku ràññeeku ci wàllu xam-xam moo ko sos. Ren muy tollook 25eelu yoon wi ñu koy amal, Ndakaaru nar a gànjaru.

“Festival come to my home” door na. Dina wéy du am diggante ci 4 ba 10 desàmbar. Muy dajale képp kuy yëngu ci mbatit. Dafa ëmb artist yi, waaye tamit ay xeltukat. Moo tax, daara ju kowe jii ñu dippe Seex Anta Jóop am ci wàll wu réy. Mu war cee lëkkëloo ak Daara ju kowe ja ca Marog, di “Université Mohammed VI polytechnique  ak “Fondation des cultures du monde” ngir yékkati mbatit. 

Ren nag, waxtaan wi ñu tëral ko ci aalam gi. Boroom i xam-xam war a wecce xalaat ci ponk bii di : ‘’L’afrique face aux Enjeux de l’environnement”. Muy ay jafe-jafe yu sonal réewi Afrig yi, ay xalaat war cee sotti ngir ñu indi saafara ci mbir yiy faagaagal aalam gi. 

Bu ñu xoole ca beneen wàll wa, “Festival come to my home”, xummbeel yi yamul rekk ci xam-xam ak xeltu. Artist yi dinañ fésal seen liggéey ci ay “expositions”, walluw misig tamit desut ginnaaw. Waaye tamit taalif am na ca yoon. Muy ay mbir yu bari te wuute. Lépp di wone mbatit moo xam yu réewu Senegaal walla réew yi mu dalal. Ñu gis ne solos xew-xew boobu, bu ñu sukkandikoo ci njiit li, mooy lëkkale waaye tamit wecce ay xalaat ak xam-xam ci diggante réew yi séq xew-xew bi. 

Ndakaaru defati na mëninam. Mbatiit jaayuwaat na. “Festival come to my home” nekk ganam, boroom  xam-xam yi ak xeltukat yi, waaye tamit artist yi kenn ku nekk di wone sa xarañte ak say xalaat ngir taaral boobu xew-xew. Mu mel ni mbatiit moo aay ci dajale ak boole askan yi. 

  

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj