MBAY JAAG, GOR GI SENEGAAL AMEEL BOR (II)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Am it lu mat a taxaw-seetlu : jamono jooju Mbay Jaag doon jiite ndongo yi, fekkoon na mu bokk ci PAI, pàrti  “marsist” bu mag boobu  Majmuut Jóob sosoon te mu jiite woon yéngu-yéngu ya jiboon ca 1958 jëm 1960 (“boroom paŋkàrt  ya”) ba Afrig Sowu Jant gépp doon xeex ngir moom boppam, yewwiku ci nootaange bi ko Tubaab bi tegoon. Noonu Mbay Jaag bokkoon ci pàrti bu mag boobu. Dëgg la, PAI ag cëslaay gu ko daan dooleel la. Waaye, li am ba am moo di ne loolu taxul woon Mbay jiitaloon mébétu pàrteem ba tax koo fàtte njariñu askan wi. 

Xew-xewu ‘’Mai 68’’ boobu amoon na solo ci dëgg-dëgg su ñu gise, ca ginnaaw ga, coppite yu baree-bari yi mu indi woon ci àddina sépp, rawati-na ci sunu Senegaal gii. Ndax ña doon jiite réew yi gisoon nañu ni mënatuñu woon doxale nañdaan doxale lu jiitu xew-xew yooyule. Moo taxoon Seŋoor mi amoon gis-gis lool ci wàllu politig, ci kaw it ay ndigali Pari, daldi sàkk pexe yu yees : teggi sañ-sañu benn pàrti doŋŋ(UPS), benn sàndikaa doŋŋ(CNTS), benn kurélu kàngaami iniwersite doŋŋ…  Tërëlin yu bees yoyu nag, xéyu ñu benn bés  ñu sotti : dem nañu ba atum 1974  ñuy door a nemmeeku naka la li ci ëpp doon matale.

Ndegam Mbay Jaag daa bokkoon ci pàrti politig, mënul woon a ñàkk am péete ci wàll woowu. Looloo taxoon, ba PAI amee ay jafe-jafe ci biiram  ndax ñàkk juboo ci yoon wi ñu waroon a wéyale xeex bi ngir indi demokaraasi ci réew mi, moom mu ànddoon ak ñi doon weddi seeni njiiti pàrti ca nañu daan doxale. Mënees na lim ñenn ci àndandoom yooyu : ndem-si-Yàlla ji Mbàbba Gise, ndem-si-Yàlla ji Elimaan Kan, ndem-si-Yàlla ji Baabakar Saane, Abdulaay Bàccili… Ñoomñooñu dañoo mujje génn PAI sos seen pàrti bopp (LD  – LD/MPT) akseeni ñoñ. Seen kurél gu bees googu nag, doon wéy, njëkk ci yoonu “marsism” laata ñuy yaatal, ubbil seen bunt ñeneenñu amul woon boobu gis-gisu àddina. Ñu raññeku woon nag lool ci biir liggéykat yi, rawati-na ci jàngalekat yeek fajkat yi. Noonu lañu leen doon jàppale ba ñu taxawal seeni sàndikaa. Liggéey boobu yépp nag, Mbay a nga woon ca biir te kenn daawu  ko woon jëkk ci lenn.

Mbay Jaag ak pàrteem, ñu raññeeku woon lañu ci xeex bi kujje gi doon xeex nguuru Abdu Juuf mi fi wuutu woon Seŋoor. Ñu àndoon ceek Ablaay Wàdd mi doonoon njiitu PDS ak kujje gi ci boppam.

Noonu la Ablaay Wàdd fexe woon ba toog ci jal bi, ca woteb atum 2000, ginnaaw yéngu-yéngu yu metti ya amoon  ca njeexitalu nguuru Abdu Juuf.  Pàrti Mbay Jaag bi  amoon ci taxawaay bu am solo. Moo tax it ñoo bokkandoo woon jiite réew mi ba ñu amee ndam ca woteb atum 2000 ba. Waaye yàggul dara ñu féewaloo seen biir : Ablaay Wàdd ak PDS jaar nii, waa LD jaar nee ba mu des Mbay Jaag ak ñenn ña mu àndaloon. Ñoom ñooñu gàddaay génn LD ba noppi des ak Wàdd ci nguur gi. Taxul ñu fekki  ko ci PDS, ndax dañoo sos ñoom it pàrti bu ñu moomal seen bopp (UFPE). Mbay Jaag moo jiite woonati fippu boobule, dem ca ba jeex. Ba taxoon na, ñu bare ci taskatu xibaar yi, ak ñu baree-bari ci askan wi doon ko ci ŋaññ, jàppoon ne daa jaayoon ngoram. Moom ci boppam, réeréewul woon mbir ni lu ni mel doon na ko ci fekk, teewul mu amoon fitu jàkkaarlook ñépp, taxaw fi mu taxaw. Noonu la ko Ablaay Wàdd woowe ci wetam, boole ko ci njiiti Màkkaanu Njiitu-réew mi. Mu def fa liggéey bu am solo, su nu sukkandikoo ci seedey ña mu fa doon liggéeyandool.

Ku Yàlla defoon nga bokkoon liggéey ak moom ci jamono yooyu, te fekk nga jotoon a xam ku mu doon dëgg, dinga mën seede it ni, genn coppite gu yées feeñul woon ci moom. Moomoon boppam, amoon xalaati boppam.

Fulla, faayda ak ñàkk caaxaan ñoo ko mas a màndargaal. Mu nekkoon ku xareñ, nangu liggéey, bañpar-parloo, di fexe di yemale ñépp saa su ne. Looloo waraloon ñu bare ci béréb bu kawe boobule daan ko laale bant bu gudd. Jikkoom jooju, ñépp raññe woon ko ci moom (nga bëgg ko walla nga bañkoo bëgg), moo ko mayoon mu doon jiite,  ñaari ayu-bés yu ne, ndajem-kàngam yi doon xelal Njiitu Réew mi. Mu doon nag jaarale lépp yoon. Kenn mësu ko ca woon a sosal  lenn walla doon am lenn lu mu ko ca doon yabe. Wax dëgg, dañko ca daan gën a naw.

Nit kooku moo doon Mbay Jaag, ci liñci xam. Ku bëggoon réewam, jébbalu ci Senegaal gi mu doon xeexal, di ko liggéeyal saa su ne, ba bés  ba mu sàngujee suuf. Tey, wéetal nanu.

Di ko jaale ay mbokkam, ay xaritam, ay àndandoom, di ko jaale  Senegaal gépp.

Yàlla na suuf woyof ci kowam, Yàlla na ko Sunu Boroom yërëm te xaaree ko àjjana.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj