Mbënn mi ak toj-toj yi : fan la miliyaar yi duggu ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njàqare, jaaxle la ñu bari ci ñi dëkke ci yenn diwaan yu nekk ci réew mi àndal gannaaw ba taw bi wàccee ci àllarba jii weesu rawatina ca Ndakaaru. Taw bu baree lëmbe woon Ndakaaru ci bile bés  ba ay otorut am ci ay yàqu-yàqu. Bi ci gën a fés mooy bi jokkale « Patte d’oie » ak « aéroport Léopold Sédar Senghor ». Mu nekk lu askan wi di ñaawlu ba fa ñaawlu yam ndax tamñareet yi ñu dugal ci tabaxum (ndefarum) otorut yi.

Ci mbind yi « Préfet » bu Ndakaaru biral, « mbir mi kenn mënu ko woon fàggu ndax Ndakaaru, ci benn waxtu doŋŋ, daawul am taw bu baree nii ». Waxam jooju day wone mbetteel gim am ci yàqute yi. Moone de, Abdalaa Bari mi nekk doxalkat ci këru liggéeyu bii di BTP, safaan bi la gëm. Kàddu yooyee Moor Taala biral àndu ci. Moom dafa jàpp ne liggéey bi lañu caxat-caxatee. Maanaam, jaarul yoon te looloo tax otorut bi toj. Saytu bi waroon a ànd ak liggéey bi it amul woon te ñi ko yore woon, seen doole néewoon na lool. Nde, xew-xew bi nekkul lu bees ci réew mi ndax, ci benn dog bi, amoon na « pont » bu tojoon ci juróom-ñetteelu weer bi ñu ko ubbee ca atum 2017.

Gannaaw li dal otorut bi jokkale « Patte d’oie » ak « aéroport Léopold Sédar Senghor », « autopont » bu Yoof ak bu Kër Masaar ñoo jël raw-gàddu gi ci ndox mi. Nde, foofu moom kenn amul fu mu jaar. Du daamaar, du nit. Yoon yaa ngi fees dell ak ndox. Waaye li gën a ëlëm maxejj yi mooy « autopont » Kër Masaar bi sóobu/sànku ci ndox mi te bi ñu ko ubbee ak léegi deful weer. Léegi, lan moo ko waral? Ndox mi moo bari walla liggéey bi moo muccul ayib.

Mbooleem xew-xew yii ñooy jur ay sikki-sàkka ci boppi maxejj yi. Muy lu deme ni taxawaayu jëwriñ yi nguur gi dénk wàll woowu, ci seen njub, seen xarañte, añs. Ba tax na ñuy dëkk ci di laajte fu miliyaar yiñ jagleeloon fànn woowu duggu? Ak lan lañ ci def ca dëgg-dëgg? Ndax, bu dee lépp jaar na yoon, li ñu génnee ci xaalis ci ndefarum « autopont » yi ak otorut yi waroon na leen a mën a aar fileek ay at. Ndegam, maxejj yi mënuñu nànd mbir mi, ñoo ngi njort ay njuuj-njaaj ci sémb taaxu laltu yoon yi. Te it, ay at ci gannaaw, génnee woon nañ xaalis bu bari ngir mbënn mi, waaye ba léegi mbir dafa mel ni mbir mi amul coppite.

Fan la miliyaar yi duggu ? Fan la miliyaar yi duggu ? Loolu la askan wi jàpp, def ko aw woy fi ñu tollu nii.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj