Bari na ay mag, yu góor ak yu jigéen, yuy fàttaliku lenn ci li ñu daan def bi ñu nekkee tuut-tànk te ñu leen ko daan aaye. Ñenn ñi dañu daan lekk saabu, ña ca des daan macc baaraam, mbaa ñu daan mëq suuf. Ci mëqkatu suuf yi nag, amoon na ci ñu am maanaa lool sax. Ndax, bu suuf si tilimaan, daanuñu ko laal walla, laata mu daan dugg ci seen i gémmiñ, dinañu ko lay ba mu set.
Waa, lu suuf si doon saf sax ? Xanaa fàtte nañu ko. Céy xale ! Ku ci yàgg rekk dof ndeysaan.
Léegi nag, ki dem ba nekk mag di mëq suuf moom lees ko war a wax ? Xanaa moom daa doyalul walla boog dafay dabe ? Ndax bi mu nekkee xale daawul lekk suuf ? Doyna waar ! Ak lu mu ci mën a doon, coow li nee na kurr fi mu nekk nii. Ndax, am nay kilifa yu ñu bett, ñu làqatu di mëq ci suuf si. Mëq nag ba seen i sikkim taq !
Xanaa nu dénk leen suufus Réew mi, ñu jël ko ak seen i ñoñ, paacoo ko ci seen biir, def ko séddaleem bukki : “bii bukki, bii njuur, bii Sàmba, bii ki ndayam dee”. Mu mel ni dafa am ay ma-réew yu gën a yeyoo suuf si ña ca des. Ay waay Sàmba !
Nu bokk téeméer nun ñépp, nu wóolu leen, dénk leen ko, ngeen aakimoo juroom-ñaar-fukk yi, ba nu ak fanweer yi. Ngeen teg ko fan ? Yeen am nga xel ? Walla dangeen a jàpp ni yeen a nu gën a doon ay Saa-Senegaal ? Nax ngeen seen bopp ! Te sax, bu nu xoolee ba ci biir, ameloo leen Réew mi lenn njariñ, seen coow a bari rekk, seen làmmiñ rëy. Waaye, seen bopp doŋŋ a leen fi bàyyi. Su nu rusul woon dara, ne leen : “tekkiwooleen fi tus !” Ñenn ñi sax dañuy rafetal di leen woowee boroom barke. Waaye, bu dee barke yit, waa Réew mee leen ko jox. Booleen nite woon tuuti, dingeen am sunu kersa.
Lu kenn nit di doye suuf sii yépp ? Dafa xaj ci benn biir ? Ku ko mëq xam ! Du rees de !
Ak ni benn ektaar tollu moos. Mi ngi mel ni nga jël benn tool boo xam ne, wet yépp a tolloo te bu ci nekk mat na téeméeri meetar ; loolu de mooy benn ektaar. Ñenn ci yeen nag, bëgg cee am fukk walla téeméer walla sax lu ko ëpp. Ngeen doye ko lan ? Dëkkoo leen ci, bayoo leen ci te defooleen ci lenn lu amal njariñ askan wi. Xanaa bëgg koo dagg ay pàkk jaay ko njëg lu kawe walla rënk ko ba Càmm gi soxla ko, bëgg faa tabax lu ñépp bokk walla bëgg faa jaarale ab tali ci niral. Bu ko defee mu jël ko ba noppi dàmp leen lu duun. Céy xaalis ak daraja !
Ak fi Réew mi tollu moos, am fi dëkkuwaay jafe fi lool. Seen ñàkk a doylu tax ngeen am fu ngeen dëkk ba noppi bëgg xañ seen i junniy junni moroom ñu am fu ñu dugal seen njaboot. Te, li ci yéeme mooy, bu nu waree wétt ngir fal ay njiit (fara, jàmbur walla Njiitu Réew) yeen ay ñëwaat ci nun ñi ngeen joxul benn cër di dagaan sunuy baat. Xanaa seen yaram du daw ?
Xale buy làqatu di mëq suuf ba mag gis ko dafay tàpp ci loxo yi ne ko : “lekk suuf baaxul”. Yeen nag, ay magum jëmm ngeen, buleen kenn ñaanal njekk te bu leen kenn sàng sutura. Nanu woo xale yépp ñu ñëw reetaan leen te fàttali leen ne yor loo mën a lekk taxul nga war koo lekk.