Tey la bés bi ñu jagleel misig. Ñu di ko màggal fii ci biir réew mi. Xumbal yi nar jolli ci gox yu bari, ci biir réew mi.
Bérsi 2022
Ci dibéer jii weesu, 18eelu fan ci Suweŋ 22, la Yuusu Nduur doon amal xew-xew bi mu tàmm a amal at mu nekk ca Bérsi. Moom, bokk na ci woykat yi ñu gën a ràññee Senegaal ak Afrig. At mu ne day tëgg fee ca Bérsi. Mu nekk xew-xewu misig mbalax bu mag biy dajale mbooloo mu bari.