MÓODU LÓO DAAN NA AAMAA BALDE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xaar bi yàggoon na lool, waaj gi tamit naka noonu. Waaye, ñaari mbër yi mujje nañu sëgg démb ci dibéer ji. Móodu Lóo ak Aamaa Balde bëre nañ démb, ca aareen nasiyonaal ba ca Pikin. Móodu Lóo moo daan, yóbbu ndam leek metel mi (la couronne) Pàrsel.

Seen làmb ji, bi ñu ko dalee waaj, yàggoon na lool. Jotoon nañ koo àppal ca njëlbeen laat ñu koy bëtal ci sababi gàllankoor. Moo taxoon ñu dàkkoon ko ba jëmmi jamono. Démb nag, ci dibéer 5i fan ci nowàmbar lees ko jàppaatoon te mujje na am.

Ci fan yii ñu génn, gisees na ñaari mbër yi, Aamaa Balde doomu Pikin ji ak kii di Móodu Lóo doomu Pàrsel ji, ni ñu doon waajalee bés bi. Amaloon nañ ay jàkkaarloo yu saf sàpp. Werente bi bari woon lool ci diggante soppe yeek farandooy mbër yi. Fan yii ñu génn ba tay, foo geestu nit ñaa ngi ciy wax, ku ci nekk naan sama mbër a mën, sama mbër ay daan. Mënees na wax sax ni làmb dafa mel ne lu dekki. Nde, toogoon nañu jamono yoo xam ne yii, bu mbër mu mag waree bëre sax kenn du ko yég, mbaa ñu ci bari bu desee ay benn fan, ñaar lañ koy yëg. Bëre Aamaa Balde beek Móodu Lóo bi nag, dafa dekkil làmb ji, naatalaat géew gi. Jaadu na nag, ndax ñaari ndaanaan a doon daje, ku ci nekk mbooloo nekk sa ginnaaw.

Móodu Lóo yàgg naa def i jaloore ba jël metelu làmb ji (la couronne de l’arène), nekk buur bi, maanaam « Roi des arènes ». Ci Ëmma Seen, moom it di doomu Pikin, la ko nangoo woon. Gannaaw loolu, Ëmma dikkaat ngir nangu ko, saa-pàrsel bi daldi koy bañ, daanati ko. Ba tax na, mënees na ni loolee yokk jom kii di doomu ndem-si-Yàlla ji, Fàllaay Balde, ci mu gën a ñafe ba ñu taxawal bésam ak Móodu Lóo.

Li war ci bés bi yépp nag, ñaari mbër yi def nañu ko. Ci bés bi, ku ci nekk ñëw na na mu waree, bàkku, neexal bés bi, yëngal fowu bi (Arène national). Cokkaasante nañu, xarfa-fuufa yi ñépp gis nañu ni ku ci nekk ci ñoom ñaar def nga ci xaalis bu weex tàll. Amaa dikkee na nañu ko xamee woon, Móodu, wàllu sangu bi ñëwee na ci nees ko miinee woon it. Waaye, ci wàllu téere, dafa dëggal li mu ne : « woon weesu na fu may takkatee gàllaaj yu bari ndax làmb. »

Ba ñu defee loolee lépp nag, la arbit bi daldi woote ca digg géew ga, ku ci nekk ñaan la muy ñaan, léemu ay léemoom. mu laaj leen ndax pare ngeen, ñu ne waaw, mu daldi sex mbiib ba rekk ëf ca. Ñépp ne tekk, fowu ba ne selew, soppe yépp jël xol yaak xalaat yaak yépp jëmale leen ca bëre bi, ca ñaari mbër yay laale.

Ñaari mbër yi tàmbaley léewatoo, ci ay saa, Amaa daldi tàmbali di dox ci kaw Móodu Lóo, nees-tuut ñu tàmbalee sànnantey kurpeñ rekk roofaloo. Doomu Pikin ji dóor mboot, Móodu ci mën bëreem, rocceku Amaa rëpp, samp ñetti cër ya, doomu pàrsel bi wër ko ndombo, jekku ko, di ko rokkoos ak nokkoos. Dóor yi mel ni mbàccum gerte. Móodu Lóo tiim Aamaa Balde, jàpp kanam giy dóor rekk bañ a bàyyi. Biir dóor yi mettee ba metti, as waay a dawee ci bitig géew ga, romb takk-der yi, ñëw laxasu Móodu Lóo ngir wallu Aamaa mi mu àndal. Ca lañu àttee ñaari mbër ya. Lu leer ba leer, ci soppey Amaa Balde yi la. Ndaxte, moom lañ jekku woon. Gannaaw loolu nag, arbit yi gise, dem ca “var” bi nga xam ni lu bees la ci làmb ji, bii di ñetteelu yoon biñ ko jëfandikoo ci làmb ji. Ci seet, settantal ñu jox kii di Móodu Lóo ndam li, mu delloowaat nguur gi Pàrsel.

Waaye, lenn ci lu ñuy rafetlu mooy ba ñu joxee doomu Pàrsel ji ndam, Aamaa Balde daldi ko jox loxo, kott ko, ndokkale ko, muy lu ñu bëgg ci bés yile, tubaab di koy wax “fair play”.

Bu lépp weesoo, lenn ci lees war a bàyyi, mooy li am démb, ay sàmbaabóoy di bawoo fële di duggu ci géew giy yàkk làmb ji. Lees war a wutal saafara la balaa muy wéy di bari. Te, loolu, liggéeyu takk-der yi la, ñoom ñi war a sàmm kaaraange nit ñi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj