MUSAA JÓOB BAÑ NA NI MUUT, NEE NA MOTT (NDEY KODDU FAAL)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Musaa Jóob layookat bi doon jiite “Dakar Dem Dikk” la njiitu réew mi tekki ndombog-tànkam démb ci àllarba ji. Moom miy ndeyu mbill gi nag firndéel na ko ci rajo Sud fm ak ci xëtu Facebookam. Lu waral ñu jële ko ci boppu liggéeyukaay bi nag àddu wu ci.
Ñu bari dañoo jàpp ni li mu të ticc ni Maki Sàll amul sañ-sañu bokk ci joŋante njiitu réewum Senegaal bii di ñëw moo ko waral.
Du benn du ñaar, Musaa Jóob wax na ne Maki Sàll warta am 3éelu moomeel. Ñeneen ñi foog ni dëgg gu wex gi mu wax waa Eiffage ak njiitu Senac moo tax. Ndax ci kàdduy Jóob, tubaab biy jiite Senac « daa yaakaar ni Pari la nekk, lu ko neex mu def ».

Kon, wet goo ko mënti jële, mënees na jàpp ni Musaa Jóob ay kàddoom ñoo ko dàqlu. Kon daal ku nekk ci biir pàrti APR danga naan muut, tëj sa gémmiñ, mbaa nga ni mott ci biti ?
Li kenn dul nàttable mooy : “Dakar Dem Dikk” am na njiit lu bees te mi ngi tudd Omar Bun Xatab Silla.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj