Ci Altine ji, Jamñaajo dalal na ñiy yëngu ci daara yi. Ñu amoon ndaje ak Njiitu réew mi, Màkki Sàll, ngir luy jëmale daara kanam. Ñu nemmeeku teewaayu kurél yi ak jàngalekat yuy yëngu ci daara yi. Seen jataay boobu ñu séq ko ci waxtaan ak sottante ay xalaat jëm ci liy doxal bérébu njàngukaay yooyu.
Daara, jàngu la niki lekkool yi. Fii ci Senegaal, daara yàgg na fi. Loolu la Njiitu réew mi Màkki Sàll di fàttali ci kàddu yii :
“ Daaray Pir siiw na fépp ci àddina si. Bi ñu ko sosee ak léegi am na ñeenti xarnu (400i at). Sëriñ Xaali Amar Faal mooy ki ko sos. Ñu mën cee jël misaal niki Ciloñ, Kokki ak yeneen ak yeneen.”
Kon, ñu mën cee dégge ni, njàngalem Alxuraan yàgg naa am ci réew mi. Te it yàgg naa tàggat ay saa-senegaal yu takkoo-takku.Waaye, ñu seetlu ni li mu yàgg yépp, terewu koo jànkonte ak ay jafe-jafe. Ñu mën cee lim ak tumurànke ñeel ñenn ci sëriñi daara yi ak ndongo yi. Ñenn ñi ëpp ci ñoom di dund ci yalwaan. Loolu lépp nekk ay gàllankoor yu ñu mën a teggi ngir daara yi gën a ñoŋ.
Ci kow loolu, Njiitu réew mi fas na cee yéene jël ay ndogal, lëkkale démb ak tay ngir daara gën a xarañ. Ñu gis ne tàggat gi daara di tàggat ak jikko yi muy ji ci nit ñi, dina jur jàmm ak dal ci réew mi. Niti daara tamit am na wàll wu réy, seen kàddu nekk lu ñu fonk ba mu mën a joyyanti ma-réew yi. Moo taxit, Maki simmil na leen sàppo. Ci ndogal yi mu jël, ñu nemmeeku ci neexal bi mu bëgg a dippee Njiitu réew mi.
Neexal googu dina tax lawaxi daara yi bokk ci joŋante yi mën a am, am ag tàggatu. Dina tax tamit njàngalem Alxuraan mi ñu gën koo jox gëdda. Bokk na ci jàngkati araab yi Nguur gi nangu seen lijaasa ba ñu mën a bokk ci ay liggéeykatam. Loolu lépp di jur ay njeexital ci ñi daara di tàggat. Ku ne daara, tudd koppar ngir nekkin wu gën a baax. Moo taxit, Maki Sàll fas yéene tebbi ci lu tollu ci 20% , ñu xayma ko ci 6i tamndaret ak lu topp ciy koppar ngir jumtukaayi ndongo yi ak li ñiy jànge. Mu jàpp tamit ne bésub Altine 29 nowàmbar dina ko def bés bi ñu jagleel daara.
Mënees na tënke ci waxtaan woowu ay ñaxtu ak i dige, moo xam ci way-daara yi walla Nguur gi. Ñu gis ne nguur gi mu ngi ciy xar tanku tubeyam ngir gën a ñoŋal daara yi.