NDIMBALU 670 MILIYOŊ CI MBEYUM DARKASE BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kurél gii di DER/FJ (Délégation à l’entreprenariat rapide des femmes et des jeunes) moo génnee lu tollu ci 670 miliyoŋ ci cfa. Mu fas ci yéenee dooleel 128 béykati darkase fale ca Kaasamaas ci diwaan yii di Koldaa ak Sigicoor. Bile taxawaay nag dafa bokk ci xalaat yi nekk ci biir sémb bi muy doxal ngir suqali koom-koomu réew mi.

Ca njalbéen, dañu jëkk a def ay njàngat ak ay caytu ci wàll woowu ba xam nu liggéey bi war a tëddee. Ginnaaw loolu la kurél gi dogal ne dafay dooleel béykat yi. Ca dëgg-dëgg, ci ay waxu Maam Abi Séy, « DER/FJ dafa bëgg a taxawu koom-koomu réew mi » ba noppi bëgg cee def ay jéego yu am solo.

Ñi jot ci ndimbal li nag, wone nañu seen mbégte ci taxawaayu DER/FJ ni ki kenn ci béykat yi :

« Dama am mbégte lool. DER  yombalal na ma sama liggéey. (…) Ndimbal li tax na ba yëgatuma benn coono ci mbey mi. »

Ki ñuy dippee « le chef de l’exécutif régional » fale ca Sigicoor biral na itam ay kàddu yu ni mel:

« Taxawaay bi am na solo lool waaye sunu bëgg-bëgg du lenn lu dul jël raw-gàddu gi ci fànnu koom-koom gi ginnaaw li nu yore ci ay dayo fii ci Sigicoor. »

Moom kilifa gi, moo ngi ñaax ñépp ñi jot ci ndimbal li ñu fey seen i bor laata àpp bi di jeex. Mu nekk lu béykat yi war a bàyyi xel bu ñu bëggee jot ci yeneen i ndimbal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj