Ci weeru sulet wiI weesu, Njiitu réew mi jëloon nab dekkare ngir dakkal lépp luy wutum ngalam fa Faleme ba ak li ko wër ci 500i meetar. Waaye, bees sukkandikoo ci li sunuy naataango yu Sud Quotidien siiwal, dafa mel ni gaskat ya dégguñu ko, walla boog dañu koy tanqamlu. Nde tey la ngas ma gën a wullee ñaay.