Bees sukkandikoo ci Ayib Dafe, Ndiisoog àtte yi jàllale na sembub àtte biy soppi Ndeyu àtte réew mi. Mu ne, 22i dépite ñoo wote “waaw”, 9 wote “déet”. Waaye nag, li ci doy waar mooy ne, Ndiisoog àtte yi 30i way-bokk la ñoo ci bokk. Kon, am na dépite bu wote bu ci bokkul.