Momar Njaay, ñu gënoon koo miin ci turu “Njaay Daraapoo”, dëddu na. Moom, nag, ku ràññeeku woon la ci wàllu kuppeg Senegaal. Mi ngi faatu ci àjjuma ji 31 màrs 2023. Muy xibaar bu tiis ci waa Senegaal yépp, rawatina njabootug kuppe gi.
“Njaay Daraapoo”, ku fësoon lool la ci ekibu Senegaal bi. Ndaxte, atum 2002 la tàmbali woon a ànd ak ekib bi. Dafa bokkoon ci mbootaayu 12eelu gaynde gi. Looloo indi turu “Njaay Daraapoo” wi. Nde, moo doon yore raayab Senegaal bu rëy bi, di ko wëndeel, saa bu ekib biy joŋante. Ndeysaan, amul fu mu àndul ak ekib bi. Muy Kuppeg Afrig, di Kuppeg àddina si, fépp la dem, topp ginnaaw gaynde yi, di leen dooleel ak a xirtal. Ni ko wolof di faral di waxee rekk, muy taw, mbaa muy naaj, dafa daan ànd ak ekib bi.
Kuñ daan yomb a ràññe la nag. Nde, foo ko fekkaan, wirgoy raayab réew mi lay sol, bëggoon réew mi lool, ak ekib bi, ba foo ko nattoon rekk, weesuna ko. Xarit la woon itam ci jawriñ jiñ dénkoon wàllu tàggat-yaram, Mataar Ba. Ku ko miinoon lool la. Looloo tax Mataar ba seedeel ko kàddu yi toftalu, jaalee ko ko :
“Ci naqar wii nu ame, noo ngi jaale ñii di waa-kër ki nga xam ni jóge na fi, di ko jaale itam jëwriñ jii ñu dénk mbiri tàggat-yaram, Yaankooba Jatara, njiitul mbootaayu 12eelu gaynde gi, waaye ak kureel gi ëmb soppey ekib bi.”
Momar Njaay, nekkoon na kuñ yàgg a tappal i cargal ngir dogoom ak coono yim daj yépp ngir ekib bi. Cargal gi gënoon a rëy ciy bëtam, nag, mooy gi ko njiitu réew mi tappaloon, keroog, 17 saŋwiyee 2014, muy “grade de chevalier de l’ordre national du mérite”.
Waxaguñu kañ lay koy denc ak ban bés lañ koy dëjal. Ñoo ngi dégloondi ba am ci lu leer.
EJO ak Lu Defu Waxu ñoo ngi koy jaale njabootam ak i mbokkam, di leen mastawu, di ko jaale itam Senegaal gépp, rawatina axlu kuppe gi.