NJIITU RÉEW LU BEES LI NEMMEEKUJINA KILIFA DIINE YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ni ñu sànnee woon ay gët, bàyyi ko xel ci génnam bu njëkk bi mu war a def, ginnaaw ba ko askanu senegaal falee, Njiitu réew mi Basiiru Jomay Fay njuuy na xel yi. Nde, tukkeem bu njëkk, génnut réew mi. Rax-ca-dolli, mu nemmeekuji kilifay diine yi ci réew mi. Mu nekk jëf ju am solo ci mboolayu réew mi. Ndax diine ji kenu la fi. Waaye, am tamit njeexintal lu réy ci wàllu pólitig.

Mu nekk tukkib nemmeeku bu mu jagleel kilifa diine yi. Njiitu réew mee ngi woon, démb ci altine ji, fa Tuubaa. Mu seeti woon kilifa ga, di Séex Muntaxaa Basiiru Mbàkke. Ginnaaw ba mu àndee ak ndiiraam mu yam, kilifa ga dalal na ko ci teewaayu Sëriñ Basiiru Mbàkke Abdu Xaadr mi yore seen kàddu. Ñu saafonte, weccante ay kàddu ñeel béréb bii di Tuubaa. La gën a fés ci ay kàddoom, moom Njiitu réew mi, mooy ne dina taxaw ci jafe-jafey ndoxum Tuubaa mi. Waaye tamit, taxaw ci wàllu wale mi ci jamonoy nawet bi. Ci seen ub tàggatoo, sëriñ bi jox na ko teraanga ju mag. Muy ab kaamil di téere bu sell ak sijaada. 

Leneen lañu gis ci nataal yi te ñu mën cee def i jàngat mooy siyaar ba mu amal fa béréb ba. Ñu seetlu ni Njiitu réew mi wàcce na boppam fa béréb ba doonte ni kilifa la. Ñu gis ko mu dox ak tànki neen, simmi ay dàllam. Loolu di wone worma gu mag. Mu am njeexintal ci nit ginnaaw ba seetlu gi doon benn. Loolu tam mën na nekk feemi pólitig ginnaaw ba ñu xamee ne askanu Tuubaa ku fonk Sëñ bi ak dëkk ba ñu jox la bopp. 

Ba mu jógee Tuubaa, la jàll fa béréb bu sell ba di Tiwaawon. Foofu tamit njabootug diine ji dalal nañu ko. Kilifa gu mag ga di Sëriñ Baabakar Si Mansuur teeru na ko. Ñu saafoonte,wecce tam ay kàddu. Lañu seetlu it ci tukkib nemmeeku boobu, jamonoy ñaan la, bennoo ngir gën a rattaxal diggante Nguur gi ak nitu diine yi. Loolu lépp di ji jàmm ak bennoo ci askan wi. 

Mënees na tënk, wax ne ndoorteelu génnam jaar na yoon, moom Njiitu réew mi. Ndax dañuy wax ne bay ci sa wewu tànk. Mu nekk tukkib nemmeeku bu génnut réew mi, waaye bu am solo ci kanamu askan wi ndax xam nañu diine solo su mu am ci biir réew mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj