Njiitu Réew

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dangaa jiitoom

Dañu la jiital

Sa jubb cunduŋ xanaa taxul

Moo ndax doo tontoom

Céy lii ciy way-xëccoo

Ku ne samp ndënd

Naan awma ci moroom

Boppu réew ak ni mu diise

Dungeen nu won

Lu ngeen nu tanee

Làng cib géew

Bàkk wu neex

Nisar lu teewagul

Ndax doy na leen-am

Ey waay fàtte xaj na feem

Xam nit yombul

Natt jikko nees koy defe

Kuy wut nëbb mbóotam

Ey way bu jekkoo ngalla nun

Danoo gis gisaat gisati

As waay waat waataat

Xéy suul lépp ne yoonam

Su nawle yi tànnee

Segg seet seetat ba seppali

Ndeysaan naataange fees xaat

Ci xel yi bay baawaan di xelli

Bumu la tax a naagu

Ba defe ne dees ne la yow a

Képp ku wat mbooloo ma

Bu ñu la tegee ca bopp ba

Booy nit xamal ne réew ma la

Am njiit du tal ittey boppam

Njariñu réew maay xéyam di ngontam

Njiit day dékk nopp téye dogal

Dib dag di wax dëgg néew na

Xel ma du jóg ci feesal jiba ja

Nu mu ko defe nu ku ko ame baax na

Njiit xam loolu war na ca

Da koy aar aaraale réew ma

Na jàng muñ bànneexu taggaate

Te bañ di jaayu ci galanu jayaate

Lees fi yëkkati yëkkati

Yàgg yàgg bécc si suuf

Céy waay ku xam lii looy waxati

Xanaa ku ne jéem a jaamu soxla yi

Tënk nit ñi ba seen nekkin dëkke metti

Te xam ne Yàlla rekk a mën a uuf

Séex Aliyu Ndaw

Ndakaaru, Suweŋ 2011

Teggin

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj