Ci ndaje mi ñu amaloon ci 1eel ak 2eelu fan ci weeru Sàttumbar fii ci Senegaal, réew yii di Móritani, Senegaal, Gàmbi, Gine Bisaawoo ak Gine Konaakiri jotoon nañoo am ay waxtaan yu am a am solo ci ëllëgu gaas bi ñu doon waxtaane. Réew yooyii, nag, dañoo bariley balluy mbindaare, rawatin gaas ak soroj. Ba tax na, ñenn ci jëwriñ yi ak doxandeem yi yëkkati fa ay kàddu yu mat a bàyyi xel. Nde, liggéey bu bari lañ mën a def ci li ñu yore ci laf ak gaas. Waaye loolu lépp, ay tëralin ak ay pólitig yu dëgër la laaj ngir tono yi ciy génne doon njariñal réewi Afrig yi.
Sikk amul ci ne, gaas ak laf bokk nañ ci li war a tabax ëllëgu Afrig. Waaye nag, ngir loolu mën a nekk, fàww ñu gën a am taxawaay bu wóor ci ni ñuy doxale yile sémb ak dogal yi ñu ciy jël ngir mu doon njariñal saa-Afrig yi. Daanaka ñépp ñi jëloon kàddu ci ndaje mi loolu lañ doon xamle niki jëwriñ ji ñu dénk wàllum gaas bi ak laf gi fii ci Senegaal. Moom moo ngi biral ne :
Dafa jot saa-Afrig yi gëm seen bopp, booloo te bokk wenn yoon ngir song xeex bi ñu bokk. Li Afrig yore ci gaas, soroj, laf ak ay ndaw, daf ko war a jariñ ëllëg. (…) Danu war a jëfandikoo itam lépp li nu yore ngir ñenn ci sunu maxejj yi jot ci mbëj g, ndaw yi tamit mën a am liggéey. »
Aysatu Sófi Gladima, ci biir waxtaan yi mu amal, biral na itam ne dinañ fexe ba ñu am ay ndaw yu xarañ lool ci fànn woowu. Waaye, mu ngi rafetlu njureefu kurél gii di « Organisation des producteurs de pétrole africain » (APPO). Kurél googu nag dafay liggéey ngir dooleel sémb yi saa-Afrig yi bëgg a sumb ëllëg.
Kii di M. Eric te nekk ab ma-xareñ lool ci fànn woowu moo ngi xamle ne mën nañ def lu bari ci gaas bi. Waaye nag, waruñu di jaay gaas bi rekk. Dañu ko war a jëfandikoo itam ngir sunu njariñu réew. Ak fi réewi Afrig yi tollu, mën nañoo jëfandikoo gaas bi ngir defar li nasaraan bi di wax urée, ammoniac ak àngare. Ciy kàddoom :
« Danu soxla mbëj. Ndaxte, ci xayma, lu tollu ci 600i miliyoŋi njaboot amuñu mbëj fii ci Afrig. Kon nag gaas bi mën nanu jàppale ci loolu. Mën nanu jàppale it ngir nu moom sunu bopp ci wàlluw dund. »
Beneen ma-xareñ bu tudd M. Loïc Chapuis jotoon na xamle ni gaas bi dafa nekk lu ñépp soxla tey niki réewi Tugal yi. Ci loolu, Afrig mën na ci am xaalis bu bari ba noppi jéem a dooleel këru liggéey yi mu yore ngir ñu gën leen a xam. Bu ko defee, ci xalaatam, dinañu mën a daaneel ñi yore sémb soroj yi gën a réy ci àddina si niki waa Qataar, Amerig, Asi, añs.
lilee nekkoon solos ndaje mi. ay xalaat yu rafet génne nañu fa. Nu xool nag ndax dinañ leen jëmmal.