NJUUMTE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci xam-xamam bu amul yemu ak xareñam bu amul sikki-sàkka, Boroom Bi dafa bind nit mooñaale ko ak ug matadi gu mat sëkk. Waaw kay, matadi gu mat sëkk sax !

Nit ku nu séen muy dem, ak nu dayoom mën a toll walla nu màggaayam mel ci sunuy bët, na nu bir ne matul. Bi mu doonee nit rekk la ko matadi tàmbalee gunge. Moo tax, mbër mu ñu fiy bàkk ba di ko wax ne mbër kaamil la, na xam ne ñu ngi koy nax. Ndax kenn matul ku dul Aji-bind ji.

Sunug matadi googu moo nuy yóbb ci nuy juum. Nit ku dul juum amul te feek noo ngi ci kaw suuf, saa su ne mën na noo juum. Loolu la sunu Maam ja, Abi Gànna Jóob doon wax naan : “Àddunaak weeru koor a yam, bu dog jotul juubu mënut a wees”. Nu déggee ci ne, képp kuy noyyi rëccagul ci njuumte. Dafa fekk rekk ne dayo yi ñoo dul tolloo ; kii mën na def njuumte lu rëy, kale def njuumte lu digg-dóomu walla lu tuuti. Kii mën na yëg ne juum na, kale ñàkk koo yëg. Kii mën na nangu njumteem, kale lànk ko ba tëdd ca naaj wa.

Li njuumte yi di bari lépp nag, am na ci ñaar yu ràññeeku : weddi dëgg ak gëm lu dul dëgg. Donte ñaar yépp mën nañoo jural nit ki ay jafe-jafe, weddig dëgg moo ëpp ay loraange ndax moo gën a diis. Ci niral, bu ñu nee kuy mi ci kër gi dafay mbëkke, ki ko gëm bay moytu, bu wax ji dee dëgg ak bu dul dëgg yépp, mën naa mucc ci fitnay xar mi. Waaye, ki weddi wax ji bay ñóoxu xar mi saa su koy xont, bu dee ni dëgg-dëgg xar mi dafay mbëkke, bu deful ndànk dina ko gaañ.

Doxalin bu ni mel la xeltukat bii di Belees Paskaal jëfandikoo woon bi muy bëgg a soññ ay ñoñam ngir ñu gëm Yàlla. Mu ne woon bu ñu mënul firndeel ne Yàlla am na walla amul, na ñu ko jaamu rekk te noppalu. Bu ko defee, ki gëm Yàlla ba génn àddina, bu fekkee ni dëgg la, Yàlla am na, kon dina ko fay jëfam yu baax, bu amul nag du ñàkk dara. Waaye ki gëmul ba faatu, bu dee ni Yàlla am na, kon dina ko duma, bu amul nag baax na, ñàkk ngëmam du ko wàññi dara. Xalaatam bii nu duppee ci farañse “pari pascalien” jeneen firnde la juy biral ne weddi mbir muy dëgg ëpp naa def.

Ci li nu mën a yóbbee ci weddig dëgg, bokk na ci ñàkk a xam, ëppal ak xeebaate. Moo tax dafay jaadu, lépp lu nuy def, nu teg ko ci xam-xam. Te bu nu xamee ba noppi, nu làmboo ak ay teggin yuy mën a tax xam-xam bi jariñ ci ni mu gënee. Taxawaay bu ni mel mën na noo dimbali tamit ci moytu gëm lu dul dëgg.

Juum nag, pingub fàttali la war a doon ci nun doomi Aadama yépp. Saa su nu juumee, dafay gën a firndeel ne ay nit doŋŋ lanu. Ndax njuumte yëfi nit la. Waaye nag, ci kaw loolu, su nu juumee ba yëg ko, dafay jaadu nu nangu ko ba noppi def li war ngir bañ cee sax. Ndax kat njuumte du ñàkk, waaye yàgg caa bon.

Baabakar Lóo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj