Talaatay démb ji, 1 nowàmbar 2022, la waa jàngu bi doon màggal seen waliyu yu sell yi (Toussaints). Muy xew-xewu diine bu ñuy màggal fépp si àddina, kercen yi di ci fàttaliku seen niti diine ya bokkoon ci ñoom, gaa ña nga xam ne seen dund ci yoonu njub ak topp Yàlla lañu ko jeexal. Moo xam ku ñu xam la, walla ku ñu xamut, nekk ay royukaay ci diine, jege woon Boroom bi.
Tur wi kese wund na dayob bés bi. Nde, “Toussaints’’, ku ko dégg ku nekk, war a xam ne ciy nit ñu sell lay dellu. Mu nekk xumbeel bu waa jàngu bi di amal at mu jot ngir màggal gaa ñu baax ña dëddu. Muy bésub fàttaliku, bésub royuwaay, waaye tamit, di bésub ñaan ak barkeelu. Rax-ci-dolli, bés bile, dees na ci ñaanal way-dawlu yi.
Fii ci Senegaal nag, karcen yi dinañ koy faral di taxawe fépp ci biir réew mi. Waa jàngub Ndakaaru di ko màggalee ca sëgi Saint-Lazare ya. Mbooloo mu tàkkooy ñëw ngir defaraat bàmmeel ya, siyaar, ñaan, ñaanal seen i mbokk ak i jegeñaale ya leen jiitu allaaxira. Ci beneen boor, xew-xew bi day soññ nit ñi ci yoonu mbaax ak sellal ngir bokk ca ña ñu dul fàtte ba fàww.Tewodoor Adiriyeŋ Saar nee, ci Leral.net : “ Dañoo war a soppi sunu dund ndax ag cell lu mën a nekk la ci àdduna sii.”
Bés bu nekk, ak ka ko moom, waaye way-dawlu yi tamit, kenn waru leen a fàtte, rawatina gaa ñu baax ña joxoon seen dund Buur bu Sell Bi.