PDS AM NA NDIISOG LUÑÑUTOOM : LÉEGI NAG ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey ci àllarba ji la Ngomblaan gi door ndiisog luññutu gi ñeel anam yi ñu gàntalee wayndarew lawax bii di Kariim Maysa Wàdd. Dañuy joxoñ baaraamu tuuma ñaari àttekati Ndajem Ndeyu àtte réew mi, jiiñ leen nger. Mbirum ndiisoog luññutu googu lañ doon fénc tey fa Ngomblaan ga. Mu sababoon fa coow lu réy a réy.

Dafa di, dépitey PDS yi xawoon nañ song Ceerno Alasaan Sàll mi waxoon ne Kariim Wàdd dafa am nasiyonaalite Farãs wëliis nasiyonaalite bu Senegaal bi. Bu dul woon Guy Maris Saañaa, xaw kon tuuti ñu dóor ko. Ceerno Alasaan Sàll sax nee na dafay pelent ñi dal ci kowam.

Bu loolu weesoo, dépitey kujje gi moom, mbir moomu soxalu leen, yitteelu leen. Lenn doŋŋ lañuy wax, mooy na wote yi am keroog 25 féewaryee 2024. Maanaam, ñoom, waxi dàq wote yi moom, waxuñu ci dara. Waaye nag, càkkuteefu PDS gi mujje na jàll.

Nde, ci biir 165i dépite, 120 yi wote nañ waaw, daldi ànd ci taxawalug ndiisoog luññutu gi. Loolu nag, xaw na yéem nit ñi. Ndaxte, Bennoo Bokk Yaakaar kese, 83i dépite la am, Yewwi Askan Wi amoon 80i dépite. Bu Wallu Senegaal gi PDS bokk, 16i dépite kese lañ am. Te, sikk amul ci ne, dépitey Pastef ga woon moom, wotewuñ waaw. Ndax ñoom dañu bëgg wote yi am, ñu bañ leen a dàq. Li mat a laaj nag mooy lan moo tax dépitey Nguur gi ak ñenn ci kujje gi wote waaw. Ndax dañuy bañ wote am ? Bu dee waaw, lu tax ? Ndax àttekati Ndajem Ndeyu àtte réew mi dinañ nangu ay dépite di leen laaj ciy tuuma yiñ leen gàll ? Lu ciy wàllu askan wi ?

Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj