PÉNCUM MAAM YUNUS JEŊ : LADAB CI LÀMMIÑI RÉEW MI (NDEY KODDU FAAL)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ku dégg Maam Yunus Jeŋ, sa xel dem ci jigéen ji jëkk a bind téere nettali ci kàllaamay Kocc. Péncum Maam Yunus Jeŋ nag bànqaasub kurélu FONK SUNUY LÀMMIÑ la. Li ko tax a sosu mooy “jàng, jubal, jariñoo” sunuy làmmiñ. Sasoo it amal benn yoon ci weer wu nekk ndajem ladab ci làmmiñi réew mi. Àllarba, 17 nowàmbar 2021, lañ amaloon ubbite bi ci «Place du Souvenir Africain». Mu nekkoon jataay mu réy te am solo ci teewaayu kurél gi yépp daanaka, ñiy yëngu ci làmmiñi réew mi ak njabootu Maam Yunus Jeŋ mi nga xam ni moom lañ tudde ndaje yi ba noppi jagleel ko ubbite bi ngir sargal ko.

Bi ñetti waxtu jotee, exposition door na ndax ca bunt saal bu mag ba lañ raŋale téerey EJO Editions, këru móolukaay, OSAD, ARED ak CNRE, ñépp di yëngoo ak a móol i téere ci sunuy làmmiñ.

Ndoorte la soxna Ngaakaan Ñing, njiitu béréb bi moo jël kàddu, dalal gan ñi, rafetlu xalaat bi jur ndaje mi waxaale mbégteem ci liñ taamu ligéeyukaayam.

Bi mu daanelee, Mamaram Sekk mi nekkoon aji-lootaabe bi jox kàddu ma-làmmiñal Ajaratu Umar Sàll mu xamaleek mbooloo mi FONK SUNUY LÀMMIÑ. Fàttali li tax a jóg kurél gi ak li mu ëmb ciy bànqaas te «Àllarbay làkki réew ak Ànd jubal mbind mi» bokk ci. Bàyyiwul ginnaaw li Séex Anta Jóob daan wax naan : «làkku jaambur mën nga koo macc mu neex lool ni tàngal waaye doo ci tàqamtiku». Li nga moomal sa bopp moo dàq yëfi keneen.

Bi mu noppee, soxna Buya Faal, njiitu kàggu Goethe Institut wuutu ko, moom it, faram-fàcce bu baax lëkkaloo gi am seen digg ak kurél gi ba tey mu jur Péncum Maam Yunus Jeŋ. «Ku sa bopp réer, koo seet doo ko gis», muy tekki ni rekk fonkal sa bopp, fonk li nga moom, door a ubbiku ci keneen mbaa leneen. Bi soxna Buya noppee, Mamaram wone téere (livret) biñ jagleel Maam Yunus Jeŋ ngir ñu gën koo xam ak liggéeyam. Pr. Mbàkke Jaañ mi fa teewaloon nguur gi moo tëj lëm yi. Yëgle na ni «ci atum 2022, juróom-benn ci làmmiñi réew mi dinañ leen dugal ci njàngale mu suufe mi (CI) ndax xam nañ bu baax ni jariñoo sa làmmiñ mooy jëmale kanam am réew». Kon lii jéego bu am solo la ci lay suqali Senegaal.

Séex Aliyun Ndaw mi ñépp xam nëbul mbégteem ci bindkati tubaab ak xeltukat yu mel ni ñoom Bóris daan bind ci tubaab wàññeeku di bind ci seen làmmiñ. Ndax lu am solo la. Ñaax it ñiy jëfandikoo wolof ñu jubbanti seen waxin, ci misaal foo bëggee wax «jox dig daje», nga ni «ba bés bi» rekk, muy lu jub, lu amul toppandoo.

Ginnaaw gi Lamin Mbaay ak Kura Saar dawloo yaram yépp ak taalifi Maam Yunus yi ñu yëkkati. Waaye Maysa Maaraa kenn du moom ci baat bu leer ak woy. Dafa «slam» ñaari woyu Maam Yunus Jeŋ laata Aatumaan Njaay Dumbuyaa di bérél mbooloo mi jaar-jaari Maam Yunus Jeŋ. Jàngalekat bu xareñ, bindkat bu mag, «jigéen ju jaambaare te yiw», mi ngi fekk baax ca xolu Kajoor (Tiwaawan) ci atum 1941, génn àddina 2016 ci Ndakaaru.

Mamadu Jara Juuf moo tënk Aawo bi, téere bu am solo boobu Maam Yunus di ci wone ni kuy séy dangaa war a muñ ndax «sonn daw, bëgg a dee daw, doo fekke dara. Waaye sonn muñ, bëgg a dee muñ, ku muñ, muuñ». Lu mel nii it lay wax ci woyam bi tudd Réjj may déju, di taxawaay ak xeexu Maam Yunus mi rootee ci teenu yaayam ak wu soxna Aram Faal, sunu Séex Anta Jóob bu jigéen.

Maam Yunus Jeŋ bindkat la woon, yor i feem, ci toogaayu létt yiy Penda géwél létt ndaw si ci la bindkat biy jéem a defar jikkook yaram, di ko nettali ni Ndeela (way-jëmalu Aawo bi) nekkee ci naaj wiy liggéey ba ker ñëw, mu war a noppalu ak sagu.

«Bindkat day nettali ay xew-xew yu ay jëmm def ci ay béréb ; kon mooy jàngat gi am solo ». Dem na sax ba méngale Madame de La Fayette ci «La Princesse de Clèves» ak Maam Yunus fi muy wone taaru Finaax te Ndeela talu koo xool ndax coono bi muy dund ci kër jëkkaram te kenn tegu ko ko ku dul goroom  ak i njëkeem.

Bi sëñ Juuf muujalee, ñu ubbil kàddu képp ku am lu mu sànni ci Maam Yunus Jeŋ walla ci li mu bind bàyyi fi. Seede yi amoon nañ solo tey benn baat bi : Maam Yunus Jeŋ ku fonkoon boppam la.

Soxna Aminata Mbay, jàngaleku tubaab ci Liise Kénédi day jàngale L’ombre en feu bu Maam Yunus, am na it nisëru boole ci Aawo bi ; ndax def ceek sotti ci la.

Séex Adaraame Jaxate, njiitu UESLAN (kurél gi boot bindkati làmmiñi réew mi) top nay tànki Séex Anta bi baxoo woon naan “bëgg a suqaliku ci làkku doxandéem nax sa bopp la”. Buñ sukkandikoo ci baatam, “Senegaal, téeméer boo jël, daanaka 20i rekk a dégg tubaab, kon bu nu bëggee fëll, fàww nu jox gëdd sunuy làmmiñ.

Ndaje ma nag tàmbali ba njeexital, xalamkat bi dal-luwul benn yoon, kon yow mi dawal kayit gi, nànd nga ni, ndaje ma géeyul woon.

Kàddu njabootu Maam Yunus moo ko tëj. Ñu wax seen mbégte ak sag gu ñu am ci ni Fonk Sunuy Làmmiñ dekkilee seen mbokk, du lu ndaw te sant nañ bu baax ñi ko jëmmal. Taawam bu jigéen, soxna Ndey Kamara, nee na jaadu na ñu saragl yaayam ndax li mu liggéey jëme ci làmmiñu wolof ; lii sax moo taxoon mu tekki Bàkku Senegaal ngir ay mbokkam yi duggul lekool mën koo nànd. Bi lii lépp matee nag, dañoo tàggatoo ak cocktail : woo ña teewoon ci ay xéewal, lekk ak naan.

Ku lim, xéy-na, dinga fàtte waaye FONK SUNUY LÀMMIÑ buy tudd farandoo yi, Njawriñu téereek dawal fokk ñu nekk ci biir ndax dugal nañ seen loxo bu baax ci Péncum Maam Yunus Jeŋ.

Mbooloo mu takku wuyisi woon na FONK SUNUY LÀMMIÑ, taskati xibaar yi tamit, kenn demul ñu des. Ñaareelu Péncum Maam Yunus Jeŋ (desàmbar 2021) ñuy ko jagleel Séex Aliyun Ndaw. Ñetteel bi (saŋwiye 2022), ñuy dalal Bubakar Bóris Jóob ngir waxtaane téerem bu bees bu muy door a noppi. FSL di ci përye ñépp, bàyyiwul kenn.

Ndey Koddu FAAL

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj