Gaawu gii weesu, dafa am ku ñu jam paaka fa Ndindi, mu faatu. Ndindi, ci diiwaanu Jurbel (Njaaréem) la nekk. Loolu xew ci guddig gaawu bi ginnaaw ba ñu fa amalee ab xawaare pecc (soirée dansante). Ka ñu faat di ab baykat buy wuyoo ci turu T. Seen. Ab yaxantukat, I. Fay, moo ko rey. Daf ko jam paaka ñaari yoon. Jamono jii, moom I. Fay mi def ñaawteef boobu, ma nga ca loxoy yoon.
Sàndarm Ndindi yaa ngi wéy di wër ki tëgggoon xawaare bi, S. Saar. Dafa di, ci yenn dëkki kow yi, dañu tàmm di tëgg ay xawaare ak i xumbeel ginnaaw tabaski. Léeg-léeg, mbir yi du am kaaraange. Moo tax, bari nay xeeti musiba yu ciy sosoo.
Cig pàttali, fa Yëmbël, am na ab màndikat bu fa jamoon ab xale mu faatu. Ñoo ngi doon wax sax ne, ki def jëf ju bon jooju, ci ñi Njiitu réew mi goreel kaso ci tabaski bi la bokk. Waaye, xibaar boobu, jëwriñ ji ñu dénk wàllu yoon, Usmaan Jaañ, weddi na ko.
Ak lu ci mën di am, rey gi bari na fi réew mi. Kaaraange amatul. Te, lees seetlu mooy ne, ngànnaay dafa yomb a am, rawatina paaka yeek ñoom seen. Nde, ñu baree ngi doxantoo xeeti ngànnaay yooyu. Ñenn ñi, ngir aar seen bopp bu leen saay-saay songee, ñeneen ñi nag (saay-saay si) def lu bon lañ ci jublu. Mu am ci ñoo xam, seen liggéey moo ko laaj, waaye dañuy gaaw a tàggook seen sago. Bu ko defee, Càmm gi war teg ay matukaay, xool ni muy lootaabee mbir mi. Warees na yit tere nit ñi ñuy doxantoo ay ngànnaay yoy, mën nañ ci gaañ seen i moroom.