Ci atum 1997 la Mehdi Bâ génne téereem bu jëkk, jox ko tur wu leer nàññ : « Rwanda, un génocide français6 ». Jacques Morel teg ci téere bu am solo moom itam, « La France au cœur du génocide des Tutsi7 ». Warees na tudd yit ndem-si-Yàlla ji Jean-Paul Gouteux mi bind « La nuit rwandaise8», walla filmub-mbooru Raphaël Glucksmann bi (« Tuez-les tous !9 ») ak bu Anne Lainé (« Un cri d’un silence inouï10 ») Waaye, lees war a bàyyi xel dëgg mooy li Mehdi Bâ ak Michel Sitbon duppe « la révolution saint-exupérienne11 » ngir fésal anam bu kéemaane bi liggéeyu Patrick de Saint-Exupéry soppee njàngatum diggante Farãs ak Ruwàndaa ñeel xew-xewi 1994 ya.
Kenn sañul ne « Le Figaro » mi yabaloon Patrick de Saint-Exupéry Ruwàndaa, bokk na ci yéenekaay yooyuy faral di yee fitna mbaa di bind njaaxum. Kon, ba Saint-Exupéry di dem Kigali, xalaatul woon ne dina fa gis mbaa mu dégg fa lu ko jaaxal. Njuumte lu réy la woon, ndax àddinaam yépp la faagaagalu Tustiy Ruwàndaa yi mujjee salfaañe…
Yaxal yi mu daan yónnee « Le Figaro » mënuñu woon a jëmmal dëggëntaan li Ruwàndaa meññaloon ci xolam ak ci xelam. Téere yu bare yi mu jagleel faagaagalu Tutsi yeey firndeel ne ba mu jógee Ruwàndaak léegi, mbir moomu rekk a ko soxal. Dale ko ci « L’Inavouable12 », jaare ci « Complices de l’Inavouable13 » ak surnaal bi mu duppe « XXI », ba ci téere bim mujj a génne, di « La traversée », bindatul ci leneen lu dul Ruwàndaa. Ci « La traversée », day nettali la mu gis Kongo ba mu fa delloo 20i at jàpp 25i at ginnaaw faagaagalu Tutsi yi. Tukki boobu mënutoon a yomb. Waaye werakoon bii di Saint-Exupéry xereñ na xereñ goo xam ni kuy jàng téere bi, sa xol day jaabante, daanaka, diggante tiis ak mbégte. Dafa demoon Kongo ngir seet ndax « ñaareelu faagaagal » gi ñuy jiiñ Kagame, ne da koo def ngir feyyu, lu amoon laam déet. Waaye moom de, nee na wax jooju ay kàcci kese la, mëneesul a méngale la Théoneste Bagosora defoon biir Ruwàndaa ak xareb Paul Kagame bi ca penkub Kongo14.
Ci gàttal, bu dul woon farlug kurél yu mel ni « Survie » ak « Collectif des Parties Civiles pour le Rwanda » ak i boroom xam-xam yu ñépp weg ndax seen njub ak seen ormaal doom- aadama, tey leneen la ñuy wax. Farãs lëmbaaje kon na mbir mi, yàq xel yi. Bu dul woon bañkati Farãs yu dëggu yooyu te am fit, daanaka kenn du mën a ràññatle fi mu ne nii doomi Ruwàndaa yiñ bóom ak ñi leen tëral rendi. Maanaam, kenn dootul woon xam fu dëgg gi féete ñeel faagaagalug Tutsi yi. Kon, tey, bi yëf yi amee bañ teg ci 27i at, Macron doonul sant Vincent Duclert ak i naataangoom ñu def ci gëstu bu xóot te yaatu.
Ku jàng seen saabal gi, dinga gis ne kilifay Farãs yi doon liggéey ci mbir mi ci diggante oktoobar 1990 ak sulet 1994 ak sax lu ko jiitu tuuti (kolonel René Galinié misaal la ci) def nañ seen kemtalaayu kàttan ngir musal doomi Ruwàndaa yi ci jéyya ji leen doon yoot. Kilifa yu mat yooyu, nite, jéem nañ lu ne ngir seen turu réew bañ a gàkk ci mbir mi, mu ciy jële gàcce.
Mënees na cee lim Pierre Joxe, doonoon ab jëwriñ bu am fulla, daan xamal Mitterrand ne jaaduwul mu jàppe boppam ni buur, lu ko neex mu def Ruwàndaa, ndax loolu dafa xewwi te, sax, safatul kenn. Naka noonu, Yannick Gérard, ndaw la toogaloon Farãs ca Ugàndaa ak kolonel Patrice Sartre ak Antoine Anfré, « jàngatkatu Ruwàndaa » ca « Quai d’Orsay » – di màkkaanu jawriñug Bitim-réewu Farãs. Anfré, nag, bu yàggul rekk la ko Macron tabb mu doon àmbaasadëer ca Kigali, looluy biral ni diggante ñaari réew yi rattaxe jamono yi. Ndax, Anfré moomu la fi nguuru Mitterrand mere woon ba dàq ko liggéeyam.
Yàggees na wax ne DGSE (Direction Générale de la Sécurité Extérieure) miy yëddul Farãs ci àddina sépp, mësul a tàyyee artu nguuru Mitterrand, di sukkandiku, nag, ciy xibaar yu wér te wóor, doonte sax dañ doon worook li gënal ña dëju woon « Elysée » di xamb taal bi. Noonu la ñu binde ci saabalu Duclert gi ne, ci ndoorteelu « Opération Turquoise » li, DGSE daf leen a yónnee ab yëgle, di ci wax lu leer : « Aa…! Na Farãs xool bu baax a baax fi muy teg tànkam […] bala ñuy wax ne dafa kootook nguuru Ruwàndaa gi fi ne15. » Ci biir saabal gi, ñoo ngi tudd geneen kayitug yëgleem : « 2i fan ci weeru me la DGSE waxoon ne FPR « jotewul dara ak cong gi waral deewub njiitu réew mi, Habyarimana », cong goo xam ne ñenn ci Hutu yiñ jàppe ni ay way-dëgëral la ko jiiñ16. »
Bu dee ci wàllu soldaar yi, kolonel Patrice Sartre tamit nekku fa di layam-layami. Ci toftalug saabalam la joxey turi nit ñoo xam ne njortoon nañ ne laale nañ ci faagaagal gi. Te, ñooñoo taxoon kolonel Sartre bind ne « Farãs dafa war a def lànketub-biir ci ñoom, ngir xam, ci anam bu leer nàññ, gan kilifay Farãs, ci ñi daan jokkalante saa su nekk ak ñiñ njortal njekkar li, lañ ci war a ŋàññ, lu mu dee dee ci yéenekaay yi, ci sababu kootoo ñeel waajal ag faagaagal17. »
Kolonel René Galinié, moom, diggante suweŋ 1988 ak sulet 1991 la nekkoon « attaché de défense » ca Kigali, di xelal Farãs ci mbirum kaaraange. Ñépp a ko seedeeloon booba gis- gis bu xóot. Doon nañu wax yit ne ku am seetlu la. Ci gàttal, nii lees birale njàngat li mu amaloon ci njëlbeenug congu FPR gi, ca weeru oktoobar 1990 : « Ci 8eelu fan ci oktoobar la xamle woon ne am na ñu ñuy metital ak a fitnaal ca Kigali. Ñoo ngi jàpp ñi ñuy tuumaal, di leen « fetal leeg-leeg ». Waaye, li mu gën a seetlu mooy ne « bu ñu dakkalul rëbb gi ñuy rëbb Tutsi yi, di seetaan ba mu àgg fum warul a àgg, ci faagaagal lay mujje » ». Ci beneen boor, kolonel Galinié mi ngi wax ne daanaka MRND mooy làngu politig gi aakimoo lépp Ruwàndaa te « fépp fu amatul i xeex, tegaat na fa loxo ». Ci 13eelu fan ci weeru oktoobar, moom Galinié ci boppam, teewe na mbir yi, wax ne « ay baykat, doon i Hutu te bokk ci MRND, gën nañoo singali Tutsi yi, di leen rëbb ci tund yi ; nee ñu ñoo ngi rey ay nit ca diiwaanu Kibilira, te mu dande sowu-kowu Gitarama lu tollu ci 20i kilomeetar18. »
Seetlu bi Galinié amoon moo tax « Elysée » dàqlu leen, mook seneraal Varret mi nga xam ne, « àndul woon ci li Mitterrand bëggoon a dugal loxoom ci lëkkoob Farãs ak Ruwàndaa ; da doon xeex ngir kenn bañ koo xañ sañ-sañam, ñeel jëflantey làrmey ñaari réew yi19. »
Doxalin ak taxawaayu nit ñooñu, ñu doon ay maxejj walla ay soldaar, day dëggal ñiy wax ne, bu ñu mënta tuumaal Nguurug Farãs gépp sax, warees na yóbbu fa mbaxane doonee benn François Mitterand ak képp ku taq ci faagaagalug alfunniy doom-aadama yu deful dara, moo xam ndax yaa nga doon liggéey « Elysée » walla feneen.
Ndax kat, ñaari àmbasaadëer yi toppalante ca Kigali, Martres ak Marlaud, xamoon nañ bu baax liñ doon def : mbir xew na ñu war cee àddu, daldi tànqamlu, mel ni ku ci yëgul dara mbaa ñu soppi ko, ngir rekk Farãs mën a wéy di jàppale Habyarimana. Kon, ñoo ko teyoon. Xamoon nañ bu baax ni Habyarimana moo reylu Tutsiy Bugesera yi ak tamit Bagogwe yi te booba daanaka Farãs a doon kenuy nguuram. Seneraal Quesnot mi nekkoon kenn ci bëkk- néegi Mitterrand yi, Bruno Delaye, doonoon aji-digleem ci mbiri Afrig ak tof-njiit lu mag lu « Elysée », Hubert Védrine – ñuy faral di leen tudd ci saabalug Duclert gi – ñoo doon sotle ak a xelal bóomkat yi ba noppi di leen aar.
Bu dee Alain Juppé, jawriñ bi yoroon wàlluw bitim-réew, dees na faral di dégg ne moo jëkk a jëfandikoo baatu « faagaagal ». Dëgg la, waaye ba mu koy génne ci gémmiñam gi ci 16eelu bés ci weeru me, juróomi ayu-bés jàlloon nañu ba noppi, ñu jotoon cee faat, lu mu néew néew, genn-wàllu milyoŋu Tutsi. Te sax, ñeenti fan rekk laata loolu, moom Juppé moo waxoon ca Wasiŋton ne : « Ay at a ngi, nun Farãs nuy bàyyi xel ci Ruwàndaa. Jéem nan lu ne ngir juboole giir ya fay reyante. Nde, la xew ca réew moomu, xeexug giir kese la, du leneen20. » Buñ waxantee dëgg, kàddu yooyoo gën a méngook ay xalaati Juppé. Te yit, jéego yi mu mës a seqi yépp ci turu réewam, ay firnde yu leer lañ ci. Dëgg la, ci weeru awril wii weesu, Alain Juppé jéggalu na ci yéenekaay « Le Monde », dem sax ba ne mënees na nangu yenn ci tuumaa yi ñuy tuumaal Farãs ñeel faagaagalug Tutsi yi ca Ruwàndaa. Kàddu yooyu yëngal xol yi, ñépp ni : « Aa ! Guléet ! Juppé mii nga xam ni ku mas a tudd turu réewam ci mbir mile mu defante kook yow ba mu saf sàpp ! » Moo taxoon tamit ñu bare jàpp ba tey ne xel mee ko yedd te loolu mu bind dëgg la ci moom, mu tibbe ko fu sore ci xolam.
Waaye duñ woon dara lu dul ay kàdduy naaféq tigi. Ku ko weddi, jàngaatal li Juppé bind ci Le Monde. Da ni : « Xareb Farãs a nga woon Ruwàndaa ngir aar sunuy doomi-réew. Waaye mënun woon jàmmaarloo, nun kott, ak bóomkat ya, ngir ñu dakkal seeni ñaawteef. Soxla woon nanu ndimbalug làrmeb Itali, ndimbalug Amerig ak bu soldaari Mbootaayu Xeet yi21. » Képp ku xam na diggante Pari ak Kigali deme woon dëggëntaan ci atum 1994, dinga xam ne wax jooju ay fen yu tooy xepp la. Lees war a bàyyi xel moo di ne bóomkati Ruwàndaa ya, ci waawu François Mitterrand lañ doon dox, bu yëkkati woon yollosoom rekk ne leen wéer leen seeni gànnaay, doonuñu ci ñemee teg baat. Kon, ne fi naan yeneeni réew waroon nañ jàppale Farãs, waxu ku danoo ci saret la.
Juppé mi doon jawriñu Bitim-réewu Farãs xamoon na loolu bu baax a baax. Te sax, xanaa du ba rey yi nee kurr Ruwàndaa la dalaloon ca Quai d’Orsay Jérôme Bicamumpaka, bóomkatu Tutsi bu mag boobu doonoon tamit naataangoom ? Moom daal, ku gis ni Alain Juppé di néewalee bakkani Tutsiy Ruwàndaa yi, sa xol du jeex yem ci, sa bopp tamit dafay ubu.
Mitterrand mi doon ndeyu-mbill gi, nag, lépp lu mu def Ruwàndaa moo ko teyoon, teyati ko : soxlawul woon ku sëgg ciy noppam di ko digal, naan ko lii nga war a def, waroo def laa. Du benn yoon bu mu wone ne am na xel-ñaar ci mbir mi. Dara jàppul yenn politiseŋ yi lu dul réy, di jaay ne dañoo xam mboorum niteef gi ba mu jeex tàkk : dañ noo bëgg a gëmloo ne duñuy niti neen, fiñ toog di jéer Démb ñoo ngay waajal Ëllëg. Noonu la Mitterrand mës a doxale. Te li ci gën a yéeme mooy ne, ci wàllu Ruwàndaa, moom ak ña sooke woon lees duppe ci nasaraan « la Révolution sociale hutu » bu Grégoire Kayibanda, ci njeexitalu atiy 50 yi, ñoo bokk wenn xalaatin. Amul dara lu leen wutale. Ni Mitterrand jàppe demokaraasi ci li mu duppe « réew yooyu » – maanaam sunu sagari réewi Afrig yi tekkiwul dara ci gis-gisam – mooy ne ku ëpp mbooloo yaa yelloo jiite. Looloo tax Mitterrand ak i ñoñam yi ko gënoon a jege, mësuñoo xalaat ne Tutsi yi dinañ delluwaat yilif Hutu yi ca Ruwàndaa te deret ju bari du fa tuuru.
Ni Ruwàndaay doxe tey ci njiiteefu Paul Kagame day firndeel ne, am réew, bu fa faagaagal jotee am sax, mënees na faa fàtte lépp lu jëm ci waaso, mànkoo tabax ko. Nde, Saa-Belsig yi nootoon Ruwàndaa, ci waaso yi lañ jaare woon, nax nit ñi, féewale leen, saxal seen nguuru nooteel.
Bu loolu weesoo, soo dee Saa-Senegaal, bokk ci réewi Afrig yi Farãs di xañ seen péexte te tudde leen « les pays du champ », lu ne ngay jàng ci saabalu Duclert gi, doo ko gëme, day mel ci yow ni këllu-kuus goo for ci àll bi. Daanaka xibaar yi la Xonq-Nopp yeek seen dunguru yu ñuul yi doon nëbb yépp a ngi ci biir ne fàŋŋ-fàŋŋaaral. Kon, dinga ci jàng yu am a am solo ñeel doxinu « Françafrique », xam naka la saay-saay yiy defe seeni njuuj-njaaj bu leen wóoree ne ñoomi neen la… Ci misaal, dees na ci gis ne, miinante bu jéggi dayo bi ñuy faral di seetlu diggante aji-dëkk « Elysée » ji ak surgaam yu ñuul yi, ëpp naa soofantal te lu fi sax la. « Sama doomu-ndey » la Bokassa daan woowe Giscard, di woowe De Gaulle « baay sama » ; Chirac, Sassou-Nguesso ak Omar Bongo, ñoom, dañoo amoon seen gàngóor, ànd di saax-saaxe alalu Afrig waaye saa yuñ wéetee ñu ngay càkkaay, màndi bay tërëf-tërëfi, di xàqtaay, di pàkkarñi, di jaay ngóoraak naan-kaani. Ku leen fa bettoon, ñuy fo ak a ree noonu, boo deful ndànk ne coxor giñ leen di jiiñ newul ci ñoom, néeguñoo rey sax ginaar. Dëgg la, Mitterrand ak Habyarimana daawuñu àgg ba foofu wànte ku ci nekk jàppoon nga sa moroom ni sa xaritu benn bakkan. Looloo nëxaloon xelu Mitterrand ba kenn mënu ko woon a wax ci Ruwàndaa lu mu dégg, rawatina bu dee dangay jéem a sikk Habyarimana. Rax-ci-dolli, jamono jooju, kor Danielle dafa feebaroon, di naax. Foofu la naataangoomu Ruwàndaa bi jaare, dëkkee jéggi dig yépp, di am ci Farãs lépp lu mu bëgg.
Te yemul foofu.
« Françafrique », baat la bu ponkalum xeltukat bu ñu doon wax François-Xavier Verschave, tëggoon ciy jamono. Li mu ko dugge woon mooy biral ne Farãs dafa delloo réew yu mel ni Senegaal, Kodiwaar ak Càdd seen moomeel ak loxo ndeyjoor ba noppi nanguwaat kook loxo càmmooñ ! Te ni mu koy defe, mooy teg ci boppu réew yooyu ay xuusmaanjàpp, ñu toogal ko fa, mu leen di jël-loo ay dogal yuy tooyal ceebam, moom Farãs, boo ko déggalatulee sab xare déjjati la… Fekk moo jaar ci ginnaaw !
Kon, bu weesoo Ruwàndaa, saabalu Duclert gi da nuy fàttali naka la Macron, gone gu juddoogul sax, di def bay doon buur, doon bummi ci réewi Afrig yi fi Farãs tegoon loxo.
Jaay doole doŋŋ…
Waaye ni yëf yi yombe woon noonu ci Tubaab yi, moo leen taxoon a naagu, dem ba fàtte ne Ruwàndaa du Senegaal, du Kamerun du Togo, xaajuñoo niroo, sax. Njuumte lu mag li moo doon ne saa yu Farãs xoolaan Ruwàndaa, du gis lu dul réewum dunguru, mu maasaloo ci xelam ak yeneen réewi Afrig yi mu jàpp ne war nay tegaley xarnu di leen noot – mbaa sax mu war leen a noot ba fàww. Looloo waraloon seneraal Quesnot bind bés ne xel dajul Mitterrand di jàmbu Habyarimana, ndax bu ko defee dina « yàq sunu der, sunu naataangooy Afrig yi dootuñu wóolu Farãs22. » Ginnaaw gi, gën naa leeral kàddoom yooyu cib bataaxal bum yónnee Roland Dumas, ni ko : « Bés bu nu juumee ba génne sunu loxo ci mbir mi, dummóoyu Ruwàndaa, dina nu yàqal lu bari te mënees na cee lim yii : dinañ ne ay noon song nañu sunu xarit te jàpplewuñ ko, te loolu day njuuy sunuy pexe (ndax noo fi waxoon ne : « dunu toog di seetaan ba Kigaliy daanu »). Sunu pólitig ñeel Afrig fa lay jaare naax-saay. Lii tamit jar naa sóoraale : bu faagaagal amee, te moo nar a am, dinañ nu ko jiiñ23. »
Quesnot di xamal yit Mitterrand ne Pari dafa war a aar « francophonie », maanaam mbootaayu réew yiy làkk farañse, « ndax Àngalteer a ngi jàppale bu baax Museveni ak waa FPR yi te bun sàgganee léegi Tutsi yi moomandoo Ugàndaa, Burundi ak Ruwàndaa yépp te loolu du yoon ndax seen mbooloo takkuwul24. »
Gis-gis boobu moo doon itam bu Hubert Védrine, mu tënk ko ci li mu tudde « ndigaaleb Farãs ngir sàmm kaaraangey bépp réewu Afrig mu ko dénk sa bopp ».
Buñ ko nattee ci Ruwàndaa, lenn rekk lay wund : jaadu na Pari dal ci kow képp kuy noonook nguur gu Farãs di xaritool, di ko jàppale, rawatina bu dee ñi koy song ay doxandéem yuy làkk àngale lañu, bawoo Ugàndaa, di am réew muy làkk àngale.
Looloo tax kàgguy ceedeefi Farãs yi fees dell ak mbiri Ruwàndaa, « gisey-mberu » yi daan tegaloo ca « Elysée », ñu fa daan amal yit saa su nekk yeneeni ndaje yuñ jagleel faagaagalug Tutsi yi.
Ni saabalu Duclert gi tasee tey, yi ko jiitu yi tasewuñ ko woon noonu. Jamonoy mbaali-jokkoo jin nekk moo yombal siiwalam. Waaye tamit ay boroom xam-xam yu maandu ñoo ci liggéey ci ndigalu Njiitu-réew moo xam ne, bi mbir miy xew, fukki at ak juróom-benn doŋŋ la amoon. Siiwalees na bu baax kàddu yi tënk liggéeyu Duclert bi ak i naataangoom ; te loolu rekk la ci ñépp di fàttaliku. Dañ ne gisuñu dara luy biral kootoo diggante Farãs ak nguuru Ruwàndaa ga giñoon ne dina rey Tutsi ya fay yeewoo yépp. « Waaye Farãs jàppale na nguur googu ay ati at te yit masul a nangoo gis ne kilifa ya gënoon a bañ Tutsi yi ñoo nga doon waajal faagaagal gi ». Kon, « mënees na wax ci lu amul benn werante ne, Farãs, loxoom setul ci mbir mi, ndax bu doxale woon neneen xéy-na li am du am ».
Foofu, saabal gi teg na ci lu réy lii : lu jiin Njaag a te François Mitterrand mooy Njaag. Mu tekki ne ki jiite Farãs fukki at ak ñeent di jëf, di wax ci turam, wax na, def na lu tax ñu bóom lu ëpp benn milyoŋu doom-aadama yu xamul woon sax fu Pari féete. Lu leen tee takk seen fit tudde loolu kootoo te xam ne du leneen ?
Waaye tuumal ag Nguur gu am doole ni nguuru Farãs cig faagaagal gu leer nàññ, mënut a yomb. Xel mën naa nangu ne, saabal gi, laata ñu koy fésal, waxtaanees na ko ci pet ak Macron, natt baat bu ci ne, faramfàcce ko. Lii tamit leer na : àddina jin nekk tey, ak ni muy doxe, way-bokki « Ndajem Gëstu » mi mënuñu woon a jéggi mbaa làq dëgg gi. Doon na jaaxal nit ñi, bu fekkoon ne biraluñ xeetu déggoo wi doon dox diggante njiiti Farãs yi ak ñoomin Bagosora ak Nahimana ak yeneeni bóomkati Ruwàndaa yu ñàng ya. Boroom xam- xam yi def gëstu bi binduñu ko waaye niñ gis Mitterrand doxale ko Ruwàndaa tax ñu jéppi ko, génn ci moom, daanaka. Ñépp xam nañ léegi ne bu dul woon moom ak ña ko wëroon ca « Elysée », suufu Ruwàndaa si du naan deret ju ni tollu. Lees war a nangu rekk mooy ne fésal dëgg gépp ñeel ag faagaagal, fàww mu jafe te jaruta yàkkamti. Dëgg gu ni mel, day raam lu yàgg, naqar ak gàcce di ko dar, laata mu naan fàŋŋ, ku nekk di ci teg say bët.
Fukki at ci ginnaaw rekk, kenn sañul woon xalaat ne ñaari njiiti réewum Farãs dinañ toppante Gisozi, taxaw fa di siyaare Tutsi ya seeni dunguru reyoon ci atum 1994. Ki ci njëkk, Nicolas Sarkozy, dem na ba nangu ay « njuumtey Farãs » ci mbir mi, doonte gëmul woon dara ci lim doon wax. Keneen ki moom, Emmanuel Macron, dafa weeju – walla mu xaw a weeju…– ciy kàddu yu daw yaram, doon féey, daanaka, ci dexug rangooñ.
Ci atum 1994 la bindkat bu ñuy wax Pascal Krop génneb téere, tudde ko « Le Génocide franco-africain. Faut-il juger les Mitterrand ?25 ». Jamono jooju, ñu bari dañoo jàppoon ne yaram wi neexul. Ñu naan : « Àtte Mitterrand, tàww ? Ku ànd ak sagoom mënuta wax lu ni mel ». Wànte ndax am nay kàddu yu leen gën a yenu maanaa tey jii ? Àtte Mitterrand, lu xel yépp mën a nangu la fi mu ne nii. Loolu rekk, ab jéego bu réy la. Li ci des rekk moo di am yaakaar ne Farãs dina gën a xoolaat boppam, wéyal njàngat li ñeel doxalinam ca Ruwàndaa. Saabal gi Vincent Duclert jébbal Macron mooy ñetteel bi waaye du bi mujj. Yeneen dinañ ci topp. Ku mu neex wax ne, Mitterrand ak doomam Jean-Christophe, Quesnot, Martres, Védrine ak ñoom seen, niñ leen di mbambe nii, day yokku, du wàññeeku. Ndax, kat, ku boot bukki, xaj baw la.
6 Bâ Mehdi (1997), Rwanda, un génocide français, Pari, L’Esprit frappeur.
7 Morel Jacques (2010), La France au cœur du génocide des Tutsi, Pari, Izuba/L’Esprit frappeur.
8 Gouteux Jean-Paul (2002), La Nuit rwandaise. L’implication française dans le dernier génocide du siècle, Pari, Izuba/L’Esprit frappeur. Sàkkees nab surnaal buñ jagleel faagaagalu Tutsi yi, tudde ko noonu ngir sargal ndem-si-Yàlla ji Jean-Paul Gouteux.
9 Glucksmann Raphaël, Hazan Pierre et Mezerette Pierre (2004), Tuez-les tous ! (Rwanda : Histoire d’un génocide « sans importance »), Dum Dum Films, La Classe américaine.
10 Lainé Anne (2003), Rwanda, un cri d’un silence inouï, France 5, Little Bear Productions, Palindromes.
11 Michel Sitbon, kàddu gu Stephen Smith fàttali ci « L’infamante accusation de “complicité” de la France est portée sans preuve », Le Monde, 18 awril 2004, ci lënd gi. URL: https://www.lemonde.fr/archives/article/2004/04/17/l-infamante-accusation-de-complicite-de-la-france-est-portee-sans-preuves_361502_1819218.html (xoolees na ko ci 11 ci oktoobar 2021).
12 Saint-Exupéry Patrick (de) (2004), L’Inavouable. La France au Rwanda, Pari, Les Arènes.
13 Saint-Exupéry Patrick (de) (2009), Complices de l’inavouable. La France au Rwanda, Pari, Les Arènes.
14 Saint-Exupéry Patrick (de) (2021), La Traversée. Une odyssée au cœur de l’Afrique, Paris, Les Arènes.
15 Commission de recherche sur les archives françaises relatives au Rwanda et au génocide des Tutsi (2021), La France, le Rwanda et le génocide des Tutsi (1990-1994), Pari, Armand Colin, xët 702. Ci Saabalug Duclert lañ jukkee xët yiy ñëw.
16 Ibid.
17 Saabalug Duclert, xët 890.
18 Saabalug Duclert, xët 774.
19 Saabalug Duclert, xët 754.
20 Saabalug Duclert, xët 941.
21Alain Juppé, « Nous n’avons pas compris qu’un génocide ne pouvait supporter des demi-mesures », Le Monde, 7 awvril 2021, ci lënd gi. URL: https://www.lemonde.fr/idees/article/2021/04/07/alain-juppe-sur-le-rwanda-nous-n-avons-pas-compris-qu-un-genocide-ne-pouvait-supporter-des-demi-mesures_6075875_3232.html (xoolees na ko ci 11 oktoobar 2021).
22 Saabalug Duclert, xët 232.
23 Saabalug Duclert, xët 234-235.
24 Saabalug Duclert, xët 242.
25 Krop Pascal (1994), Le Génocide franco-africain.,Faut-il juger les Mitterrand ?, Pari, Jean-Claude Lattès.