Xabi Alonso ak gaayam yi def nañ ko. Dugal nañ Bayer Leverkusen ci mboorum futbalu Almaañ. Ci anam bu rafet a rafet lañ ko defee nag. Saa-Espaañ bi, Xabi Alonso miy tàggatkatu këlëb ba, def na jaloore ju réy a réy. Niki dibéeru démb ji, 14 awril 2024, lañ duma Werder Bremen 5i bal ci 0. Ndam loolu leen tax a nekk waagay (champions) sàmpiyonaa. Ndaxte, ki topp ci ñoom, Bayer Munich, mënatu leen a dab. Muy guléet ci mboorum Bayer Leverkusen. Nde, bi këlëb bi sosoo ba léegi, mu ngi sog a gañe sàmpiyonaa bi.
Saa-Españool bi ak i ndawam daldi nañu dakkal nguuru Bayern Munich foofee, fa Almaañ. Dafa di, 11i at yii weesu yépp, moo rekk a daan jël sàmpiyonaa ba. Daawu ko bokk ak kenn. Kon, li Xabi Alonso ak i kuppekatam def, jaloore ju réy a réy, rawatina bi nga xamee ne keen xaaru leen woon file.
Li gën a réyal jaloore ji mooy ne, moom Bayer Leverkusen, amalagum na 43i joŋante yoy, kenn dóoru ko ci : dafa gañ38i yi, daldi témbóo 5 yi. Gaa yi dugal ci 123i bii, jël ci 31i.
Laata seen joŋanteb démb ji, soppey këlëb bi dañu fees dell mbeddi gox ba, di jaajëfal seen tàggatkat bi, ba sax daldi ne soppi nañu turu yoon wi jëm ca fowu ba duppee ko “Yoonu Xabi Alonso” (Xabi Alonso Alle). Xanaa yayoo na ko ! Nde, moom Saa-Espaañ bi, dafa soppi xar-kanamu këlëb ba, di leen futbal-loo lu set te rafet, neex a seetaan.
Wëliis sàmpiyonaa bi ñu gañe, dese na leen ñaari kub yi ñu war a mën a jël. Ndaxte, am nañu finaalu kubu Almaañ ba te njortees na ne ñoo koy jël. Rax-ci-dolli, am na joŋanteb kaar-dë-finaal ci Ëropaa Lig ba, te dafa gañe West Ham ci mats bu njëkk bi. Fi mu nekk nii, ñettale (triplé) la Xabi Alonso di diir. Siporteer yi ñoom, nee nañ, bu fi yemoon sax mu neex. Ndeem neex na, nay gën di neex !