NDAJEM ÑAXTU YEWWI ASKAN WI : WEDDI, GIS BOKKU CI

Àllarba jii weesu, "Place de la Nation" dafa ñuuloon kukk ak i nit. Foo sàndi woon mbàttu mu tàkk ndax mbooloo mu bari. Nde, askan wee wuyusi wooteb lёkkatoob kujje gii di Yewwi Askan Wi. Fu nekk la nit ñi bawoo ci réew mi ngir teewesi ndajem ñaxtu moomu, biral seenuw naqar ci lees jàppe jaay-doole ak jalgati yoon ñeel wotey ndawi réew mees dёgmal ci sulet. Lu waral ndaje mi ? Laaj bii lees ci jéem a tontu.

0
380

Coowal wotey palum depite yi lёmbe na réewum Senegaal lool ci jamono jii nu tollu. Coow li nag, bari na te ci ñaari boor yépp lay jóge. Muy ñi fare ci Nguur gi walla ñi fare ci kujje gi. Ku nekk ci ñoom a ngi xool nooy def ba sa moroom du bokk ci joŋante yii nu dёgmal. Waaye nag, coow li, li muy bari bari, ñaar a ko séq, muy nguur gi (waa Bennoo Bokk Yaakaar) ak lёkkatoo gii di Yewwi Askan Wi, gàttal biy joxe YAW. Li mat a laaj kay mooy fu coow li doore ak nan la deme? Seen yéenekaay bii di defuwaxu dina leen ci indil ay leeral laata nu ciy def ab taxaw seetlu.

Coow laa ngi door bi lёkkatoo gii di YAW di jébbal ay wayndareem ca màkkaanub caytug wote yi (DGE). Nee ñu, lu jiin Njaag a, te ngóor sii di Saliw Saar mooy Njaag. Nde, waxees na ne, moom, moo fa jébbal ay wayndare yu baaxul. Ci kow loolu, Bartelemi Jaas mii di fara bu Ndakaaru génnoon na, biral ni loolu wérul. Ndax, kooku amul benn ndogal ngir mёn faa jébbal genn kёyit gum mёn di doon. Te it, kii di Decce Faal moom lañ dénk wàll woowu ci biir YAW. Ba loolu weesoo bañ jébbal seen i wayndare, ñoom waa YAW ak waa BBY, ñu gis ni dafa am ay njuumte ci seen i wayndare. Ndax, dañoo jàpp ne wayndare bu YAW ca Ndakaaru sàmmoontewul ak dog 149 ci liñ yoonal ci wàllum wote. Maanaan yemoo góor ak jigéen (parité) ci wayndare yi. Waaye ñoom bi ñu sukkandikoo ci li leen yoon may (dog 179), jàpp nañ ne war nañoo mёn a joyyanti njuumte li bala muy am ñetti fan. Maanaam laata ñu ciy amal ag caytu. Ci seen wayndare réew mi yépp nag moom, njuumte li mooy ñàkk a gёddaal dog 158. Maanaam dañoo dugal ci seen wayndare ku matalul ñaar-fukki at ak juróom (25). Waaye, ba tey terewul ne mёn nañ ko soppi. Ci coppite giñ doon def ci la ñenn ñi jàpp ne dafa am ay njuumte ngir ne dañoo wuutale koo xam ne dafa nekk ci ñaari wayndare yépp (muy titulaire ak suppléant). Biñ sukkandikoo ci dog 173 loolu mёnul nekk. Waaye ñoom, liñ jàpp mooy ne wayndare gi genn la amul xàjj-ak-seen. Moo tax ñenn ci seen i militaŋ njort ni gaa ñi dañoo bёgg a lёbёje kàrt gi ca teel.

Ca beneen boor ba nag, gaa ñi dañoo jàpp ne ñoom moom waruñoo bokk ci wote yii. Ndax, ñoom joxuñu sàmmoontewuñu dog 149 ci limu ñiñ parene ak yemoog góorak jigéen ci wayndare yi. Maanaam dañoo ёppal ci seen parenaas ba noppi tegale ñaari jigéen. Te dog boobu dafa biral ne lim bi warul ёpp 55327, warul gёn a tuuti tamit 34580. Te waa BBY liñ jébbal dafa ёpp limub 55327 ; maanaam 55328 lañ jébbal. Bun delloo tuuti ci gannaaw ca atum 2019, looloo tere woon Maalig Gàkku bokk ca wote yooya. Ngir ne lim bim jébbaloon dёppoowul ak liñ yoonal ci wote yi. Kon dañoo jàpp ne waa BBY waruñoo bokk ci wote yii di ñёw, amul seen benn wayndare bu war a jàll.

Li yokk coow li nag mooy ndogal li jёwriñ jiñ dénk wàlluw biir réew mi (Antuwaan Feliks Jom) fésal 30/05/2022, mu ciy wax ne wayndare (titulaire) bu YAW baaxul moom ak wayndare (suppléant) bu BBY. Loolu nekk loo xam ne kujje gi naanewaalewuñ ko ndox. Ba tax ñuy laaj lu tax bu kujje gi juumee yat wi dal ci kawam te, bu Nguur gi juumee du mujj fen ? Mu mel ni gaa ñi dañoo njort ne yoon tёddewul njaaxanaay, Nguur gi kese la fi nekkal. Day def liñ naan làq doom, dóor doom ndeem jёwriñ jiñ dénk wallum biir réew mi BBY la bokk. Te juróom-ñetti (8) wayndare la fésalagum yuy bokk ci wote yii. Waaye li gёn a doy waar ci mbir mi mooy ñi ñuy dippee juróom-ñaari kàngaam yi (7sages) daanaka rekk, dañoo dёggal li jёwriñ jiñ dénk wàllum biir réew mi wax ci ndogal liñ fésal ci ñaareelu fan ci weer wi nu nekk . Li ci mat a bàyyi xel te jar a defub taxaw seetlu kay mooy ndax ag wayndare mёn na bon fii, baax fee ndeem lépp benn la ? Walla ndax ab wayndare mёn nañ ko xaaj ñaar ? Li nu doon xaar kay mooy ñu ne wayndareg YAW baaxul walla BBY du bokk ci joŋante yii di ñёw. Moo tax nag waa kujje gi jàpp ne waa DGE ñoo teg seen tànk ci njuumte yi am ci wayndarey waa BBY yi. Ñu bàyyi leen ci biir ba ñooñu ñuy dippee juróom-ñaari kàngaam yi duñ leen mёn a teg ay daan. Ndax kat, bun fàtte ni wote yii dañoo am solo lool. Li ko waral mooy ñiy jёl raw-gàddu gi, ёllёg ñooy bokk ci ñiy dogal ca péncum ndawi réew ma. Muy nguur gi di kujje gi, ku nekk a ngi lal i pexe ngir noo fa ёppalee kàddu. Ndax, boo seetloo bu baax ñi fare ci kujje gi dañoo jàpp ne ñoom ñooy teewal askan wi ca péncum ndawi réew ma. Ngir njort ne nguur gi moom boppam moo ko ñor te askan wee leen fi teg. Waaye loolu tekkiwul ni ñi féete ci kujje gi ñoom ñépp a bokk jёmukaay. Donte ne sax, ñaari lёkkatoo yii di Wallu Senegaal ak YAW dañoo fas yéene boole seen doole ci yenn gox. Laaj bi mat a samp kay mooy lu tax yeneen lёkkatoo yi yi nekk ci kujje gi defuñu ne ñii ngir am doole ci kanamu Nguur gi ndeem teewal askan wi rekk a leen tax a jóg ? Waaye tamit, lu tax jёwriñ ji bёgg a dindi wayndare (titulaire) bu YAW bàyyi fa bu BBY ?

Plus de publications

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici