Dara judduwul cig neen. Mu mel ni, bànneex ci coono lay soqikoo, mbég ci naqar lay bawoo, nattu mooy jur xéewal. Ki xam lii mooy Seexul Xaadiim, mi sóobu ngir xettali xeetu yonent bi. Di jaamu Boroom Bi ak di liggéeyal sangu sang yi, ngir darajay Abdul Xadiimi. Lii mooy sababu tukkib géej gi, lii moo waral 18 Safar.
Ku dégg 18 Safar ku ne, xam li baat bi wund. Fi Sénégaal ak fi àddina, kuy màggal ak ku dul màggalul, kenn umpalewul bés bi màgg bile di Màggalug Tuuba. Nde, 18 Safar, da di xew-xewub diine bu mag ci yoonu muriid. Waaye, bu garab màggee ba nit ñay jariñoo meññet ya, booba, dafa am loxo bu ko ji, suuxat ko. Wolof nee, lu yëngu, li ko yëngu a ko ëpp doole. Kon, màggaayu bés bile kat, am na ku ko jagoo. Bu ko defee, dees na geestu tuuti, jeex démb, ngir xam kan ak lan moo waral bés bu réy bii murid yiy màggal at mu nekk.
Seexul Xadiim moo sos yoonu murid. Muy yoonu yeesal ngir jëm ci sunu boroom. Bëgg-bëggam di texeg jaam ñi. Moo tax mu sóobu ngir loolu àntu. Mu nekkoon lu mu yàggoon a sàkku ci wasilaam Seydinaa Muhammad, ba Buur bi may ko ko. Bés boobu yamoo woon ak fukki fan ak juróom-ñett ci weeru Safar ci atum Jeysasin (1313), di yamook 1895 ci atum tubaab. Nee ñu, Boroomam a ko jox ndigal ci liggéey boobu. Booba, Jeewal la ko fekkoon, mu doon waaj a laxas ngir génn dëkk bi, génn Tuubaa. Ndege, nattu bi ko Boroom bi waroon a teg, ci waxi nettalikat yi, mënut a àntu ci béréb bu sell boobu. Moo tax Yàlla boole ko ak Tubaab yi ci saayir ngir mu gàddaay. Naam metti woon na, sonnoon na ci, waaye coonoo bi day mujje soppiku, nekk ngëneel, xéewal ak mbégte ñeel ko, moom, ak i taalibeem tey. Boroom Tuuba sant ci Boroomam, digle ñu santale ko Ko ci kàddu yii toftalu :
“ Képp koo xam ne, sama mbég sa mbég la, bu bés bii dellusee, nanga ma santale sama Boroom. Ci li ko dale ginaar ba géléem.”
18 Safar,dafa nekk tamit bésub diine. Ci kow loolu la Sëriñ Muntaxaa Mbàkke génne ab yégle, di ci ñaax taalibe yépp ak soppe yi ñu sant Sëriñ bi, santale ko Boroomam. Mu ne, na ku ci nekk fas yéene jàng ab kaamil, bu ko mënut mu jànglu ko. Te, ci ndigleem, nañu ko tàmbali ngir bés ba. Waaye, mi ngi ciy fàttali tamit taalibe yi sarti dëkk bi ak i wormaam. Te loolee, weesuwul bëgg Sëriñ bi, te mooy bëgg Yàlla, bëgg Yonnent bi. Bu ko defee, warees na defaraat laxasaay yi . Teg na ci ne, ku fa ñëw tamit, na la fa sëriñ kepp indi, lu ko moy, ñàkk nga.
Lees mën a jàpp mooy ne, 18 Safar, bésub nattu ak coono la. Te kenn a ko dékku woon ngir texe, te mooy Ahmadu Bàmba.