Ab téeree ngi nii boo xam ne, bii, boo koy jàng doo bëgg mu gaaw a jéex. Dafa mel ni, fàww nga def loolu wolof naan ñiimantalu. Soo dee ku yàgg a tiim téere, te xam fa bindkat di jaar, ak la muy daj, ba li muy nettali itteel képp ku ko yër, doo mën lu moy ne « Jaajëf ».
Xalaat ci naka Bóris ak ñi sóobu ci toolu xare bi ngir Afrig dellu ca jaloorey Maam. « Malaanum Lëndëm » dafa yemul ci di ab téere nettali doŋŋ. Fentkat bi dafay jaare ca la muy nettali ngir teg baaraam ci xalaat yu diis yi tegu ci loosu doom-Aadama, bi mu ne cëpp ci kow suuf ba tey. Ndax, mu wax kook mu bañ koo wax, am na ñaari laaj yu doom-Aadama di laaj boppam fu mu tollu. Ñu di :
-
Fan ? Fan la nu jóge ?
-
Ak Fu nu ? Fan la nu jëm ?