Altine 6eelu fan ci weeru Me, atum 2019. Bés bi ñépp doon xaar, bésub layoo, bésub àtte, ñëw na. Li tax ñépp doon xaar bés bii, nag, du neen.
Waaw.
Kan lañu doon àtte ? Sëriñ Séex Beeco Cuun, di Xalifa di yit kilifa cantaakon yi.
‘’Bóomug Madinatul-Salaam’’, bile dàkkental la taskati xibaar yi utal mbir mi sabab layoo bu siiw bii. Juróom-ñaari at la lànket bi def, doore ko 2012 ba 2019. Ñépp a doon xaar ndogalu àttekat bii di Xaasimu Ture, mu waroon koo biral ci altine jii.
Mbir maa ngi xewe woon ca Madinatul-Salaam, 22eelu fan ci weeru awril 2012. Yéenakaay yi xéy dégtal nu xibaar bu yéeme : 19 cantaakon ñoo faat ñaar ci seeni mbokki taalibe ba noppi suul leen te kenn yégul, kenn tinul. Ñu ni déet-a-waay, gaa ñi ne Sëriñ bee leen jox ndigal.
Nee ñu, Abaabakar Jaañ ak Baara Sow, ñaari way-dëddu yi, lenn rekk a tax ñu boom leen : xérte ak mbëggeel gu jéggi dayo ñeel seen Xalifa bi. Ndax, àggoon nañu ci di ko woowe Yàlla. Loolu, nag, moo indi coow li bu ñu sukkandikoo ci xibaar yi fi jotoon a rot jamono yooyu. Coow li ne kurr ci këru Séex bi, mu yabal ay taalibeem ngir ñu génne fa Abaabakar Jaañ ak Baara Sow. Noonu, 19 cantaakon yi dem ba ci yoon wi, xeex ak Abaabakar Jaañ ak Baara Sow, daldi gor kenn ki jaasi, fetal keneen ki ba noppi gaawtu suul leen. Nee ñu sax ki ñu fetal deewagul woon bi ñu koy suul. Ginnaaw bi ñu defee seen tóoxidóoni ba noppi, dañu ko doon jéem a nëbb far Yàlla def am ku leen bett, boole leen ak sàndarm yi. Bi mbir mi siiwee ba yoon jot ci, coow li ne kurr. Ñépp di naqarlu jëf ju ñaaw jooju. Li ci gënoon a doy waar mooy li Séex Beeco Cuun – mi yilif ñi ñu bóom ak ñi leen bóom – noon, moom de, yëgul tinul.
Booba ba léegi, nag, def na juróom ñaari at, yoon di luññutu, di seet a ka seetaat ngir xam kan a def lan. Bu dee taalibe yi nga xam ne ñu ngi woon ci tëjub-négandiku, li leen yoon toppe woon mooy : bóomug njuumte bu ànd ak mbugal, làqub néew, ñàkk a siiwal rey bi, mbooloom-caay-caay, teggi yoonu suul néew ak ñoom seen. Séex Beeco Cuun, moom, lii la ko yoon toppe woon : luqnjuurug bóom, maanaam bu bóomulee it teewoon na bi ñuy fexe mbir mi. Jotoon nañoo teg loxo Sëriñ bi ak 19 taalibeem yi. Séex bi, nag, yoon da koo mayoon sañ-sañub négandiku ndax li mu tawatoon ba tax mëneesu ko woon téye ci kaso.
Nan delsi ci altine keroog jeek daan yi fa jóge.
Layookati Séex bi, nag, ñaanoon nañu àttekat bi mu fomm layoo bi, xaar ba seen kilyaan wér, mën koo teewe. Waaye kenn mayu leen loolu. Moom Séex bi, àttekat bii di Xaasimu Ture daanoon na ko fukki at yoo xam ne dina ko liggéeyal réew mi ak ndàmpaay lu tollu ci téeméeri miliyoŋ CFA yu mu war a jox, moom ak 19 taalibeem yi, njabootu way-dëddu bu ci nekk. Mbir mi indi werante, am ñu naan daan bi dafa woyof, taalibe yi naan yoon deful liggéeyam, dañoo bañ Séex bi rekk. Sëriñ Saaliyu Cuun, taawu Séex Beeco Cuun, joxoñ na baaraamu tuuma àttekat bi ak nguur gi ci boppam. Ndax, bu ñu sukkandikoo ciy kàddoom, sàmmontewuñu ak àqi Séex beek i yelleefam.
Waaye bi loolu lépp di am, Séex baa nga woon Frãs, ci benn loppitaanu Bórdo, di faju. Benn fan doŋŋ lañu ci teg, mu daldi génn àddina. Nee ñu sax yëgul daan bees ko tegoon.
Laaj bi ñépp di laaj moo di : daan bi ko àttekat bi daan, ci kan lay dellu ? Ay boroom xam-xam yu seen xel màcc ci wàllu yoon, tontu nañ ci. Nee ñu 10 at yi Séex bi waroon a liggéeyal réew mi, dañu koy teggi ndax ab néew deesu ko liggéeyloo. Waaye ndàmpaay li, ci njabootam lay dellu, ñoo koy fey. Ak lu ci mënti am, xalaat yeek gis-gis yi wute nañu. Wànte li wóor moo di ne àtte Yàllaa gën bu nit.