SÉMBUB SOROJ BU GRANDE-TORTUE Senegaal dina taxan 20 000i miliyaar ci diirub 30i at  

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bu liggéeyub soroj bi tàmbalee, Senegaal dina taxan, ci diirub 30i at, 20 000i miliyaar ci FCFA. Maanaam, at mu nekk, dina góobe ci njureefi soroj bi lu tollu ci 700i tamñaret FCFA. Ceerno Séydu Li, Njiitalu Petrosen Exploration-Production, moo xamle xibaar bile, gaawu bii weesu, ca Sali-Portidaal (Mbuur).

Takku xaalis boobu, ci sémbi soroj yi la ko Càmmug Senegaal di jële. Bokk na ci, mbellitum soroj mu Grande-Tortue, nekk ci digaloo Senegaal ak Móritani. Séydu Li ne :

« Njureef yi dinañ néew ci njëlbeen gi ndaxte ci ñetti weer yu mujj yi ci 2023 la liggéey biy gën a jàppandi. Waaye, li ñuy gën di dem, meññital yi (investissements) dinañ gën a wéy te dina gën a bariy ngañaay yees mën a séddale. Atum 2030 lañuy àgg ci njobbaxtalug yokkuteef gi laata muy wàccaat. »

Kàddu gii, Séydu Li miŋ ko waxe ca ndajem yaatal mu Njëwriñu Soroj beek Yasara yi doon amal ca Sali-Portidaal, Mbuur, gaawu bii weesu. Ndaje moomu nag, jagleesoon na ko taskati-xibaar yiy yëngu ci wàllu koom-koom te bokk ci kurél gii di COJES.

Bu weesoo mbellitum soroj mu Grande-Tortue bi, am na sémbub Sàngomaar bi nekk ci bëj-saalumu Ndakaaru ak sémbub Yaakaar-Teraanga ba ca Kayaar. Njiitalu Petrosen li teg ci ne, « Bu ñu sukkandikoo ci dayob njëg yi jamono jii, takku xaalis bi mën na soppiku. » Dafa di, jamono jii, njëgu barigob soroj baa ngi tollu ci 60i dolaar (39 570 FCFA). Bu dee barigo gaas bi, 6i dolaar (3 957 FCFA) lay jar jamono jii.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj