SENEGAAL, YOKK CERE, DOLLI ÑEEX !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Sàmpiyonaa yi jeex nañu. Ekibi dëkk yi ñooy futbal jamono jii. Ñii di futbal ay matsi xaritoo, ñee di waajal seen i joŋante yi ñu dégmal. Fii ci Afrig nag, ekib yaa ngi amal ay joŋantey xaritoo ngir nattandi seen taxawaay ak seen doole, nekk ci waajtaayi cu joŋanteb kuppeg Afrig bi war a am ci atum 2024. Ba tax na, ekibu Senegaal bi demoon na fekki bu Benee ca dëkkam. Mu nekkoon juróomeelu joŋanteb kippug L gi. Senegaal gi nga xam ne, moo jëloon raaya ji ca kuppeg Afrig 2022 ga, ay soppeem ñoo ngi koy xaar mu ñëwaat wane boppam, waaye tamit ay nawleem ñoo ngi koy xaar ngir kar ko, xañ ko ko bile yoon.

Démb ci gaawu gi, mu doon amal ndaje ak ekib bii di Benee. Waaye, dafa mel ni xel dalagul nag. Ndaxte, li gaynde yi wone démb dafa des bees ko nattalee ak lees di xaar ci ñoom. Seen futbal bi des na lool, rawatina kaw gi. Foofu moom, war nañu toog, waxtaan, xool, xoolat ba xam lu fay ayib bi. Dugal gi moo des ba tay. Te, li jaaxal ñu bari mooy ni, bu ataakã Senegaal yi nekkee fa seen i këlëb, dañuy dugal rekk. Waaye, bu dee Senegaal lañ futbalsi, day xaw a mel ni dañu yeew seen tànk yi. Ku ci jàkkaarloo ak caax yi, bu dóoree du jëm ca kã ya, mbaa góol bi ni ko ciix jàpp. Loolu nekk na lu ñu war a jàngat, liggéey ci ak atakã yi, jéem ci indiy saafara. Ndax ka, ku dul dugal doo am ndam, te dugal lu bari dinay gën a dooleel ekib bi.

Diggante Senegaal ak Benee, démb, ndam demul ndam dikkul, 1-1 la mujje. Senegaal moo njëkk a dugal (Abdulaay Sekk), ñu dawal ba ca boori mujjantal ga (78eelu simili bi) Benee daldi fayu.

Talaata jii di ñëw, di 20 suwe 2023, Senegaal dina ci amalaat benen joŋante xaritoo, war ci daje ak ub punkal : Beresil bu ñoom Vinicius Jr. Bresil moom, du ekibu yaafuus. Suuf gi, digg gi ak kaw gi, fépp baax. Ekib bu raglu la, diis lool. Bu keroogaa, Aliw Siise ak i ndawam dinañ mën a natt dëgg-dëgg seen doole ba xam lu des ak lu desul. Moom, Beresil, Gine la doon dajeel démb. Daf  ko dóor ñeenti bal ci benn (4-1). Démb moo nekkoon guleet saa-beresil yi di sol mayo bu ñuul, li ko waral nag mooy dooleel xeex bi ñuy xeex mbirum xeetal gi nit ñi ñuul ñiy jànkonteel saa su nekk. Bu loolu weesoo ngir Senegaal daan leen, fàww ñu dolli cere, yokk ñeex.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj