Ni waa Senegaal gëmee Yàlla te fonk diine, umpul kenn ci àddina si.
Nde, askanuw Senegaal, ñi ci ëpp ay jullit lañu. Nee ñu, cig xayma, 100 yoo jël ci doomi réew mi, 95 yi jullit lañuy wootewoo. Diiney Lislaam, nag, biir Senegaal, dafa làmboo ay màndarga yi koy wutale ak i réew yu bare. Ndaxte, amees na fiy këri diine yu mag, maanaam ay tarixa, askan wi xër ci lool, sax. Tarixa yooyu, ay sëriñ a leen jiite, ñu leen di woowe xalifa, taalibe yi fonk leen lool, weg leen. Dafa di, dayo bu réy a réy la kilifa yooyee am ci taalibe yiy déglu ak a jëfe seen i ndigal saa su nekk. Àq, dayo ak gëdd bi taalibe yi jox sëriñ si moo tax, ñoom sëriñ si, ñu am kàddu ak sañ-sañ bu bir ci mbiri réew mi, rawatina pólitig. Te, lu ni mel, ndajem njiitu réew mi, Maki Sàll, ak Idiriisa Sekk mi lëmbe réew mi doy na ci firnde. Waaye, bala tey, démb la woon.
Ca 1930-1940, fekk na 2 eelu xare bu mag bi ame àddina sépp. Jamono jooju, Almaañ gu Itleer dafa songoon Farãs, sonaloon ko lool. Ci la
Farãs wëlbatikoo ca réew ya mu nootoon, Senegaal bokkoon ci, ngir sàkku ndimmal ak i ndaw yi koy xeexle. Noonu, ñu yabal Belees Jaañ.
Belees Jaañ, ngir xam cër bu sëriñ si am ci askan wi, daldi seeti Seriñ Tuuba. Ca la ko xamalee li xew ba noppi sàkku ci moom mu digal ay ñu jàppaleji Farãs. Seriñ bi nangul ko ko, daldi sant Séex Ibra Faal mu wutili ko ay waxambaane yu ca man a dem.
Waaye, du loolu rekk la Sëriñ bi mës a defal tubaab bi. Ndax, ca jamono yooyu ba tey, santoon na Séex Anta Mbàkke mu utal ko ay gune yu ñuy dalal ca daaray nasaraan yi doon door a ubbi ca diiwaanu Njaaréem. Gune yooyu Séex Anta Mbàkke tànnoon, Séex Anta Jóob, werekaan bi, àddina sépp xam ko tey, ca la bokkoon. Ndege, Séex Ibra Faal moo doon denc yaayam ca këram gi ñu duppe woon Kër gu Mag.
Àddinay dox ba jamonoy 1940-1950. Lewopóol Sedaar Seŋoor miy dooni njëlbeenug njiitu réewum Senegaal ci njeexitalu nooteel bi, daldi ñibbisi. Bi mu noppee ci njàngam ma mu doon defe Farãs, dafa delsi Senegaal sóobu ci pólitig bi. Doomu Juwaalo jooju, nag, ab katólig la woon, bare woon xam-xam te ñawoon xel lool, sax. Xelam mu ñawoon moomu la jëfandikoo woon, natt dayo bi seriñ si am ci géewu pólitig gi, daldi leen di jiital ciy naalam. Noonu, mu seqiy jéego, seeti leen, di leen nemmeeku, di waxtaan ak ñoom, laxasaayu jikkoy taalibe, di jëfe ndigal, di bàyyi tere. Looloo taxoon Sëriñ Fàllu Mbàkke, xalifa murid yi ca jamono jooju, doomoo woon ko. Moo tax itam ñenn ñiy wax ne Seŋoor, gannaaw Yàlla, lépp lu mu mës a am ci politig Sëriñ Fàlloo ko ko mayoon. Li koy firndeel mooy ne, donte ne katólig la woon, mooy ki jëkk a jiite Senegaal, réew moo xam ne jullit yaa ci ëpp, ci diirub 21i at. Bi Seŋoor di dem, dafa jox lenge yi Abdu Juuf.
Abdu Juuf tamit, fi Seŋoor tegoon i tànkam ñeel sëriñ si la tegoon yosam. Dafa joxoon sëriñ si cër bu mat sëkk, lëkkaloo woon ak ñoom. Moom, njiiteefam ak xilaafa Seriñ Abdu Laxaad Mbàkke ñoo méngoo. Xalifa bi daldi koy uuf, jàppale ko ni Sëriñ Fàllu jàppalee woon Seŋoor. Ndimbalam ak taxawaayam ñoo mayoon Abdu Juuf ab ndëgërlaay ba tax koo toog ci jal 20i at. Ndaxte, ci atum 2000 la ko Ablaay Wàdd daanoon ci joŋanteb wote ba. Ablaay Wàdd moomu tamit, ci murid la féetale woon boppam.
Ablaay Wàdd, dafa mës a biral ne murid àqan la. Mu yàggoon lool ci kujje gi, ca jamonoy Seŋoor ak ci jamonoy Abdu Juuf. Waaye, mësul woon a réeroo ak i ñonam, doonte ne xalif bi, Abdu Juuf mii féetale woon boppam ci Tijaan yi, la doon jàppale. Àddinay doxati ba Góor gi mujje moome, yéeg ci jal bi.
Ndamu Ablaay Wàdd, nag, ci woteb 2000 yi, jaloore ju réy la woon, àddina sépp daan ko soow. Askanuw Senegaal bégoon lool ci coppite
bi mu yàggoon a xaarandi te amoon ci wàll wu réy. Jamono jooju, Sëriñ Saaliw Mbàkkee nekkoon xalifa murid yi. Ñépp xame woon ko màndute ak jege bi ko Ablaay Wàdd jege woon. Dafa di, Ablaay Wàdd, ku fésaloon péeteem ci murid yi la. Loolu xawoon na jur njàqare ak tiitaange. Ndax, dañ doon ragal njiitu réew ma woon jéng, di doxal xàjj-ak-seen. Moo tax it, fi mu ne nii, kenn amul mbeeteel ci ni waa Tuuba tëyee, ba sun-jonni-Yàlla-tey jii, pàrti PDS bi ñu wàcce ci jal bi, 8i at ci ginnaaw.
Lii lépp, nag, warul tax ñu jàpp ne, sëriñi murid yi kese ñoo daan dugal seen loxo ci làngu pólitig gi. Déedéet. Dañ ci gën a fés rekk, waaye noonu la deme woon it ci yeneen tarixa yi, rawatina bu tijaan yi.
Kenn umpalewul ne, Sëriñ Séex Tijaan Si ci boppam, sosoon na fib pàrti, jiite woon ko. Moom kay, sëggoon na sax ci géewu pólitig gi. Looloo taxoon mu dugg ndung-siin, ndax xeex ba mu daan xeex Seŋoor. Tey, doomam ji, Sëriñ Mustafa Si, kilifay Mustarsidiin yi, moo ko wuutu, jiite pàrti boppam, di PUR. Bu weesoo ñoom ñaar ñooñu nag, mënees na lim, ba tey ci tijaan yi, Sëriñ Paap Maalig Si (rakku Sëriñ Séex) ak Sëriñ Abdu Asiis Si Al Aamin. Ñii de, naam fësaluñ woon seen bopp bu baax ci pólitig bi, waaye jot nañ cee dugal seen i loxo ak seen i xalaat bu baax. Waaye, nag, kenn ci ñoom du dab Sëriñ Abdu Asiis Dabbaax. Ku mat a ràññe la woon, moom, Sëriñ Abdu Asiis Si Dabbaax. Ndaxte, daawul noppi, daawul tàyyi di taxawu askan wi ak di artoo ko dànkaafu Nguur gi, ngir muy bàyyi xel baadooloo yi. Ittéem yèpp doon rekk, wax dëgg, yore pusóom di ñaw. Ndax sax du taxawaay woowu moo jur baatu Pólitig, ca dëgg-dëgg ?
Ci sunu jamono yii nag, daa mel ni, bi Maki Sàll di yéeg ci jal bi, daa faf bettoon ñu bare, ba ci sëriñ si. Mbaa sax, du looloo taxoon Parsidã naagu woon ba di leen jéem a sóoru ci njëlbeenub moomeel ga ? Ak lu ci mënti am, gaaw naa dellu ginnaaw moom, xamaat palaasam, ràññe cër bi mu ameel sëriñ si ci réew mu bindoo ni Senegaalu tey jii ! Moo tax it, fi mu ne nii, digganteem ak sëriñ si, mel na ni mburook soow ! Doonte mënagul a fexe ba dugg ci xolu waa Tuubaa yi. Li muy féeteele boppam ci tarixa Murid yépp, mel na ni tey, waa Tiwaawon ñoo ko gën a jàpp. Loolu yépp nag, teewul, ba Parsidã Maki Sàll bëggee juboo ak njatigeem ba woon, Ablaay Wàdd, Sëriñ Muntaxaa Mbàkke, di Seriñ Tuubaa tey, moo dox diggante bi ba juboole leen, keroog ba ñuy ubbi jumaa Masaalikul Jinaan. Yemul foofu. Ndax, fan yii rekk, bi Idiriisa Sekk di wax ak askan wi ngir layal duggam ci nguurug Maki Sàll, junjaale na taxawaayu sëriñ si ci ànd bi mu àndaat ak Maki Sàll. Nee ñu, Sëriñ Musaa Nawel Mbàkke, miy sëriñu Idi, moo dox lépp ba mu sotti.
Idi moom, gannaaw ba ñu ko tàkkale nombog-tànkam gu bees gii ko may mu nekk léegi ñetteelu njiit ci Nguur gi, génnam bu njëkk, Seriñ Muntaqa la ko jagleel ; te it, li mu ko xamal leer na : « Da noo ñëw fii sargalsi la, wax la sunu ngërëm, ginnaaw ndam li nu am, ba nu toppe say ndigal yépp ba mu mat sëkk, bañ cee sàggane lenn. » Laata muy egg ci Sëriñ bi nag, Idi jot naa jaar ci sëriñam, Seriñ Musaa Nawel Mbàkke, wéet ak moom lu yàgg, ci li taskatu xibaar yi jottali.
Ginnaaw lees fi jot a wone lépp ñeel taxawaayu sëriñ si ci pólitig bi, baax na ñu amal ab taxaw-seetlu ci mbiri ñaari doomi réew mi. Ñaar ñooñu, tey, ñépp a leen naw. Ñoo ngi rëccu liñ jotal woon a jiite réew mi walla liñ ci yàggul ; ñooñooy Séex Anta Jóob ak Mamadu Ja.
Séex Anta, kenn umpplewul ne, Murid la woon ci juddoom ak ci xaleelam. Moom, Kër gu Mag la yaroo, màgge fa, ca ëttu ak kiiraayu Séex Ibra Faal. Waaye, Séex Anta, li mu doon weg sëriñ si yépp, kenn mësu ko woon dégg ci làngu pólotig gi, muy mbubboo askanam walla tarixaam. Màndute gu mat sëkk la àndaloon ci wàll woowu, ni mu ko doon defe ci wàll wu ne. Ndax dañu ko mere woon ci tekkaaralam googu ? Li am daal mooy ne, Séex Anta, dëggu, pas-pas ak xam-xam yi ko ñépp xamaloon, taxul seriñ si wallsi ko, wuyu ci wooteem yi mu doon def ngir yewwi réew mi, defaraat ko, doonte ñu bare-bari ci askan wi, moom lañu faraloon. Leneen lu laxasu woon it ci mbir mi moo doon ni, Tubaab yi ŋànkoon dëgg réew mi, Seŋoor moo leen gënaloon fuuf Séex Anta.
Mamadu Ja moom, doonoon ku jullite, nekkoon na ci jal bi, ci diir bu gàtt (1959-1962). Wànte, li mu doon jullite julite lépp (képp ku ko xamoon mënoon na ko koo seedeel), moom ak sëriñ si, jaaroowuñu woon taal. Dëggu ak xadar yi mu àndaloon, mayuñu ko woon muy maslaa maslaa yu bare, walla di doxaale jikkoy naaféq. Looloo gënoon a indi ay jafe-jafe ci digganteem ak ñu bare ci kilifa diine yi. Moo tax it, ba mu jotee woon ak Seŋoor ci ginnaaw gi, gisul woon ñu bare ñu féeteek moom. Noonu la ko xaritam xañee woon nguur gi, dugal ko kaso, tëj ko fa lu ëpp fukki at.
Bu nu taxawee seetlu ba noppi, laaj wi sampu nag, mooy xam ndax ku sëriñ si àndal dangay falu, ku mu won ginnaaw nga xalangu ?
Ay laaj yu bare sax. Bañ a falu te dencal sa bopp say xalaat yu rafet ngir suqali sam réew ? Falu te njar say xalaati bopp ciy bëgg-bëgg sëriñ si ba noppiy dox ci seen i ndigal ? Walla weneen yoon xaj na ci diggante wu sew woowule ?
Tey jii, xale yu mel ne Usmaan Sonko, di door a samp seen ndënd ci géewu politig bi, war nañu cee am njàngat. Usmaan, ci njëlbeen ga, daa meloon ni ku joxul sëriñ si seen gëdd. Waaye ci at yu mujj yii, mel na ni ku soppi taxawaayam ci wàll woowu, ndax ni muy gën a jegee léegi kilifa diine yi.
Àndak sëriñ si walla won leen ginnaaw ? Su nu misaale wax ji ak kàddu Idiriisa Sekk yu yees yi : tànn sa bu la neex la !