SONKO AK MAKI : KUY DAAN ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fitna lañ doore bésub àjjuma jii. Fitna ju sosoo ci diggante Sonko ak Maki. Ndax lan ? Ndax, dañoo tere Sonko ak i àndandoom seen ndajem ñaxtu mi ñu bëggoon a amal bés boobule ca Péncum Obelisk. Li ñu jàpp, mooy ne Maki dafa noot yoon, ba pare bëgg a lottal Usmaan Sonko. Réy gi mu réy moo tax mu jàpp ne warul am kuñ koy méngale (dendale) ci làng gi. Ba tax mu dëkke di ko lakkal ngir ne mooy wujjam bi gën a am doole ci làngug pólitig gi ci jamono jii. Li sabab lu ni mel, nee ñu, bëqët la, ab ragal la moo tax. Fi mu tollu nii dafa bëgg a def ñetteelu moome te feek daanelul Sonko xelam du dal. Loolu la defoon ak Xalifa Sàll ay at ci ginnaaw. Jàpp ko ne ko ràpp ci kaso bi.

Ca dëgg-dëgg ñenn ñi fare ci wàllu yoon ba ci waa « Conseil Constitutionnel », jàpp nañu ne ci ay waawu Maki Sàll lañuy dox. Maanam, lu mu namm ñu def rekk lañuy def. Waaye, moom dafa fàtte ne ñaxtu bi mu daan ñaxtu démb loolu la Sonko ak i àndandoom di ñaxtu tey. Fàtte moom da fee xajul sax. Te, ku fàtte lu la fal, sag folleeku da lay bett. Léegi kon, lan moo tax mu bëgg a jalgati yoon ndeem digganteem ak Abdulaay Wàdd demewul woon nii ?

Nde, Sonko jàpp na ni Njiitu réew mi amul benn manoore rawatina gaa ñi ko wër. Bi ñu déggee ni YAW dina amal seen ndajem-ñaxtu la alkaati yi dem wër këru Usmaan Sónko ak gu Bartelemi Jaas ca teel. Xanaa loolu mooy jaay doole dëgg ci dëkk boo xam ni nee nañ am na yoon. Te lees fi gis mooy ëpp la doole bës sa bët. Xalaas ! Sonko déy, safaan bi la gëm. Ndax jaaduwul ñu leen di tere def seen ndajem ñaxtu ginnaaw àtte bi ñu def ci seen « liste électorale ».

Ci ay xayma, Maki dafa am jàngoroy nguur. Waaye, du loolu doŋŋ a ko tax a doxalee nii xanaa. Nguuram nguur guy sàcc la di nëbb sàcc, gu dëkk ci nger ak ay njublaŋ yu dul jeex. Xam nañ ni bu Sonko faloo du baax ci ñoom moo tax ñu koy bëgg a faagaagal, lu ne ñu tuumaal ko ko ngir bëgg koo jaxase ak askan wi.

Nde, am na ñu taxaw sax ne Sonko dañ ko war a faat. Bu doon ci réewum yoon la, xeetu kàddu yile, kenn waru leen a yékkati te yoon tegalu la ci ay daan. Yile firnde ñoo sabab taxawaayu Njiitu réew mi tey. Bunduxataal Sonko, di ko xoqtal, di ko fatt, loolu mooy ngànnaay bi mu dese. Waaye Sonko mii ës pareegul ngir bàyyi xeex bi mu sumb ngir jële fi Maki ak i ñoñam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj