Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, bàyyeekoo na fi réew mi démb ci dibéer ji, wutali Riyaat, réewum Araabi Sawdit. Ndajem OCI (Organisation de Coopération Islamique) mi ñu fa woote la teeweji tay ci altine ji. Muy ndaje mu ñu woote ci lu tembare ngir waxtaane mbiri ñaari réew yii di Palestin ak Libã.
Lees namm ci ndaje mooma nag, mooy yokk ndimbal ak taxawaayu kurélug jullit ñi ñeel ñaari réew yooyu ak delloosi jàmm ju sax fa diiwaan ba. Teewaayu Njiitu réew mi foofa dina doon lu am solo ndax li réewum Senegaal jiite Pekkug doxal àqi juddu askanu Palestin te Mbootaayu xeet yi sosoon ko ca atum 1975.