Tuuba, dëkk bu sell ba, baat ba benn la. Lu bari lañuy doxal ca dëkk ba, ca kàdduy kilifa diine ga lay aju. Ci kow loolu, mbirum kaaraange dafa soxal te yitteel lool Séex Muntaxaa Basiir Mbàkke may njiitu dëkk ba. Moo tax mu jël liggéey ba tekk ko ci loxoy Nguur gi.
Ku dawal boppu yaxal bii, du ñàkk ne ay laaj dina la ganesi. Tuuba nekk dëkk bu mag. Ba mu sosoo ak léegi, def na ay at. Kaaraange ga, ci loxoy kan la nekkoon booba ak léegi ? Lu tax ñu tekk ko ci loxoy takk-der yi ?
Ñu seetlu ne, ñàkkug kaaraange dafa lëmbe réew mépp. Tuuba tamit muccu ci. Dafa dem ba mbir mi tàmbalee ëppiy loxo. Ndax, ñakkug kaaraange gi dafa fés lool ca Tuubaa. La koy firndeel mooy rey gu bari gi, rawatina gog amoon ca jawub Gaar ba. Mu mel ne fitna ya sàmbaa-bóoy ya bëgg teg askan wa, bu ñu ci waxul, du baax. Muy àddu-kalpe, càcc, dajij bitig yi, dogaale yi, añs. Moo taxit, Sëriñ bi woolu Nguur gi ngir mu wallu askan wa, jël kaaraange ga jox ko takk-der yi. Ndax, laata dogal boobu di am, kaaraange ga ca loxoy Safinatul Amaan ak Xuddaamul Xadiim, ñoom ñi ñuy woowe ci kàllaamag nasaraan “Police de moeurs”.
Moo xam takk-der yi la walla ñoom Xuddaamul, la Sëriñ bi doon sàkku ci Tuuba du Soppiku. La ko soxal, bu ñu sukkandikoo ci ay kàddoom, mooy ag njub. Te, lépp lañu daan bañ ca dëkk ba, moom la fay bañ ba tey jii. Moo xam ag njabar la, njaayum sëng walla ngànnaay walla col gu bon. Ci loolu, takk-der yi def ci liggéey bu réy ginnaaw bi ñu tegee dogal boobu ci seen i loxo. Mo tax, ci ayu-bés rekk, teg nañu loxo lu tollu ci 160i defkati ñaawteef. Te, yokk nañu tamit seen i matuwaay ak seen ub wër ci biir dëkk ba.
Kon ñu jàpp ne, kaaraange ñépp la soxal, moo xam foo mën a nekk. Ndax defkatu ñaawteef yi, bu ñu leen dogaalewut, ñu wéy di dog fani nit ñi. Te, kaaraange àq ak yelleef la ci bépp maxejj.