UBBI NAÑU CAMPUSEN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëwriñ ji ñu dénk njàng mu kowe mi génne na ab yégle buy buy diir ndongo yi jotoon a jàll ci joŋante “BAC” yi ci atum 2023 mi.  Lim ndongo yooyoo ngi tollu ci 77 000. Bokk ca ñoom, képp ku nàmm a wéyal sam jàng ci daaray Senegaal yu kowe yi, moo xam ci piriwe yi walla sax yi fi Nguur gi sàmp.

Muy ab xibaar bu ñu siiwal, tukkee ci jëwriñ ji ñu dénk njàng mu kowe mi di Porfesoor Musaa Balde. Muy lu ñu baaxoo gis, ginnaaw bu ndongo yi amee seen lijjaasa bu njëkk ci daara yu kowe yi. Ñu war leen gunge ngir ñu àggale seen um njàng. Xibaar boobu di wone ni ubbi nañu dalu webu Campusen ngir ndongo yi am seen “BAC” mën a bindu. 2013 lees sosoon dalu webu Campusen. Muy gindi ndongo yooyu ci naka lañuy bindoo ngir ñu mën leen joxoñ daara ya ñu war a wéyale seen njàng. Mu mel ni diir bi ñu leen àppal jamp na lool. Ndax, ma nga dale ci bésub 14 ci weeru ut jàpp 3eelu fan ci weeru sàttumbar balaa xaaju guddi gi, maanaam bu 23i waxtu tegalee 59i simili. Muy lu yées ñaar-fukki fan ngir lim bu ni tollu daldi bindu. Moo xam nag jafe-jafe yu ñu mën a jànkonteel ngir jëfandikoo jumtukaayu xarala yu yees yi. 

Li ñu namm ci ndogal loolii, bees sukkandikoo ci seen i kàddu, mooy fexe ba njàng mi am ay dig yu tolloo ba daara yu kowe yi mën a ñoŋ. Ndax, xamees na ne daara yu kowe yi ci pëccaxoo lañ nekk at yii wees.

Mënees na wax ne àpp bi jëwriñ ji tënk gàtt na lool ngir ndongo yépp bindu, moo xam fépp fu ñu mën a féete ci biir réew mi. Rax-ci-dolli, lënkaay gi (internet) mi dajut réew mépp. Loolu nekk lu ñu war a bàyyi xel laata ñuy tënk ag àpp.  

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj