Ginnaaw ñetti weer i bër, ndongo yi ak jàngalekat yi fas yéene nañoo awaat ca yoonu lekkool ya. Jàngalekat yi nag, ci altine jii, 3 oktoobar lañ tijji. Ndongo yi war leen fa fekk ci fan yu néew. Ren, ci catu nawet bi la daara yi ubbi. Nde, am na ci daara yoo xam ne, mbënn mi daf leen a yàq. Am na ci sax yoy, ñi seen kër yi taa ñoo fa nekk ba tey. Wëliis, mbënn mi, nemmeeku nañu yeneen xeeti jafe-jafe ñeel njàng meek njàngale mi.
Càmm gi jël na ay dogal yu bari ngir ñeel yembug daara yi. Li ñu ko dugge mooy fexe ba ndongo yi mën a dooraat seen um njàng ci anam yu baax. Ci kow loolu, lekkool yu bari defaraat nañu leen, amal fay set-setal. Ñu gis ne yéeneg “tijji tay, jàng tay”, du ñépp a ko mën. Doonte am na yenn ci ay lekkool yu mën a door ci tijjite gi. Waaye, dañu seetlu ne weneen wàll wa mënu ko. Ndax xaaju lekkool ya ña nga ca ndox ya ak taa-taa ya. Bu ñu sukkandikoo ci waa Seneplus, lu war a tollu ci 244i lekkool ña ngay tëmb ca ndox ya. Lii, aajawoo nay jumtukaay ngir lekkool yooyu set. Jëwriñ ji ñu dénk wàllum njàng mi tàllal na loxo askan wi ngir ñu jàpp ci cetalug daara yi. Ñu seetlu ko ci diwaan yu bari ci biir réew mi. Ay kuréel yu jóg di setal gox ya ñu féete ngir ndongo ya mën a door seenum njàng.
Leneen lu mën a gàllankoor ubbite gaa ngi aju ciy jafe-jafey ndox ak ñàkki baŋ yu ndongo yi toog. Bérébu néggandiku ya ( les abris provisoires), na xas ci lekkool yi ndax ñàkki saal yu ndongo yiy jànge. Bokk na yit ci li ñuy ruumandaat, di ñàkkug jàngalekat yu lekkoolu Senegaal di jànkonteel. Ñu jotoon ca joxe ab lim bu tollu ci 45 000i jàngalekat. Loolu di ay xibaar yu wérut bees sukkandikoo ci kàdduy Muxammed Mustafaa Jaañ, ki ñu dénk kàddug béréb boobu di saytu njàng mi.
Ñu mën a jàpp ne “tijji tay, jàng tay” du lu mën a nekk ndax lekkool yi jafe-jafe yi ñuy dund bari nañ lool. Te bu yembee fii, yembut feneen. Ndax gox yi yamuñu ci nañuy dunde te matuwaay yi it néew nañ.