Laaj ak tontu bii nag, seen yéenekaayub web defuwaxu.com séqoon na kook Usmaan Sonko ca atum 2020. Xaaj bu njëkk bii, siiwaloon nanu ko keroog 18i fan ci suweŋ 2020. Lu tollook ñaari at jàll nañ, waaye, ba tey, coowal Usmaan Sonko moo lëmbe réew mépp ak sax bitim-réew. Looloo waral ci sunu limat bu bees bii nu génnewaat waxtaan wii ngir fàttali jaar-jaar ak gis-gisu kii di Usmaan Sonko ci wàllu mbatit ak làmmiñi réew mi ginnaaw kàddu yi ci Njiitu réew mi jot a yékkati te mu jur coow lu bari.
Mbirum làmmiñi réew mi
Usmaan Sonko :
“[…] Wax dëgg Yàlla, jàng naa lu bare ci Séex Anta Jóob. Bi ma jàngee ay téereem, dama toog xalaataat lu bare, mu am lum def ci man. Jàng na téerey ñeneen sax, waaye njeexital li Séex Anta Jóob am ci man, keneen amu ko ci ñi ma jot a jàng seen i téere.
Gaa man duma wolof, waaye sama yaay séeréeru xombol la, wolof lay làkk. Sama baay joolaa la, sama maam bi jur sama yaay di pulaar, kon man mën nama wax ni duma wolof.
Waaye, Yàlla am na ci nit ñi yërmande joo xam ne, fépp fu mu boole ay nit, dina fa tàggat aw làmmiñ wi leen di boole, ñu cay jokkoo wëliis. Dangay seet, tey, bu doon wolof bi wolof kese la dégg, pulaar di wax pulaar kese, joolaa bi yem ci làkkam, séeréer bi noonu, añs. nan lanuy def ba jokkoo ? Du sotti. Yàlla la neex mu sàkk nu ba noppi, def nuy kurél ak i pàcc ngir nu xamante, xàmmante, ni mu ko waxe ci Alxuraan. Kon du ngir féewale nu. Tey, boo demee Kaasamaas, gis ni joolaa yiy soloo ak a fecce, dinga ci jànge lu bare, nga dem feneen ci ñeneen yit noonu. Bu ñépp bookkoon lépp, àddina si day soof. Waaye, lin bokk moo ëpp li nu wute. Fii ci Senegaal, fépp foo dem, dégg nañ wolof. Mën nañ ko bañ a wax waaye dégg nañ ko, te loo ci wax xam nañ ko.
Farãs, atum 1375 lañ gàll farañse bi moo doon làmmiñu réew ma. Baala loolu, lateŋ moo doon làmmiñu réew ma. Siin moo nu ëpp ay kàllaama fuuf, 300i daanaka. waaye teewul màndareŋ lañuy jëfandikoo. Noonu la amee fépp. Nun senegaal, wolof la fi Yàlla tànn. Warees nangu lu ni mel.
Raayante bi moo fi war a jeex, wolof mooy làkk bi nu war a boole. Ku bañta làkk farañse, lu tax ngay bañ a làkk làkku nit ku ñuul. Kenn waxu la nga nekkaat wolof. Waaye, ab jumtukaay kese la ngir wax a ñi nga bokkalul waaso. Te sax, aaday wolof, séeréer, ak joolaa wutewun dara.
Bu dee lu jëm ci mbirum njàng mi, bun demoon bu sàrtal njàngum làmmiñi réew ci lekkool yi, wolof mooy doon làmmiñuw bennale wi. Ñépp a koy jàng. Gànnaaw gi, nag, gone gu ci ne tànn waneen làmmiñ dolli ci, moo xam pulaar lay doon, séeréer, joolaa, soose, añs. Loolu, bu amee, xale bu ci nekk dina mën a wax ñaar ba ñetti làkk ci làkki réew mi. Te, loolu day gën a dëgëral bennoo bi.
Bu génne Sengaal, nag, jàpp naa ne, biir CEDEAO, awsa lees war a tànn. Bu dee Afrig gépp, suwaayili bee ci gën a yey.“
Mbirum mbatiit
Usmaan Sonko :
“Mbatiit mooy lépp, mooy cëslaayu yokkute. Waxuma, nag, tëgg, fecc ak li xew jamono jii. Sumay wax mbatiit mbaa aada, xam-xam, cosaan ak sag yimu làmboo ñooma tax di wax. Ndege, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. Nit dafa war a gëm boppam.
Tey, Sinwaa bi dafa gëm ni Siin moo war jiite àddina si te ndog-ndog da ko daloon ci diggante bi, Àngalteer ak Sapoŋ raw ko. Moo tax, Siin dafa gëm cosaanam ak démbam. Iraŋ, bu àddina sépp waxee mu téye fi mu téye rekk, ñemee ŋoy fi mu ŋoy, booba cëslaayu mbatiitam ko ko may. Ñoom, ca nguurug Pers ga woon lañuy sukkandiku fonk seen bopp. Turki, ñoomit, ca nguurug Otomaan ga woon lañuy wéeru. Boo demee Ërob tamit, noonu. Kon, koo jël ci àddina si, ci démbam la sukkandiku ngir jéem a suuxat réewam. Loolu la Séex Anta Jóob xamoon bu yàgg. Moo tax liggéeyam am solo lool.
Moo saxal ni, ciy gëstoom, Afrig benn aada a ko lal, te Misra moo fi ëppoon doole. Tubaab baa ñëw ci ginnaaw, gëmloo nu leneen, suufeelnu banu xeeb sunu bopp. Xeebeel boobu la Séex AntaJóob dindi.”