WAAJTAAYU BÉSU DAARA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Séex Umar Aan di jëwriñ ji ñu dénk njàng meek njàngale mi amal na tukkib nemmeeku ca Tuubaa. Xalif ba, Séex Muntaqaa Mbàkke, dalal na ko, waxtaan ak moom. Lañu joqalante, bokk na ci waajtaay yu jëm ci bés bu mag ba ñu jagleel daaray alxuraan  ci biir réew mi ak cargal gu mag ba ñu dippe Njiitu réew mi ci tarib alxuraan. Muy waajtaay yu mag ngir bés ba ñu dëgmal te jagleel ko daara.

Ñu jàpp ko gaawu di yamook 16i ci weeru desàmbar. Jëwriñ ji ñu dénk njàng mi jottali na kàdduy Njiitu réew mi kilifa ga ngir jot ca moom ay ñaan ak i taxawu. Muy lu mu fésal moom Séex Umar Aan ginnaaw ba mu génnee ca jotaay ba.

“Dañoo ñëw Tuubaa ngir jottali kàdduy Njiitu réew mi, gindiku waaye sàkku ay ñaan ci xalif bi. Mu dalal nu, wone taxawaay bu réy ci jàppale ñu.”

Loolu nekk ay kàddoom ci kanamu saabalkat yi.

Ca geneen wet ga, fàttewut a biral liggéey bi Maki Sàll jot a def jëme ko ci sëriñu daara yi ak daara yi. Bokk na ca lu mat 500i jàngalekat yoo xam ne Nguur gee leen jël ci daara yi. Limees na lu tollu ci juróom-benni tamñaret (6 milliards) yu ñu dugal ci daara. Waaye tamit taxawal nañu ay joŋanteb tari alxuraan ci biir réew mi. Loolu lépp di ab xayma bu ñu def ñeel daara alxuraan yi.

Mën nañoo tënk ni njàng mi ak njàngale mi  fàttewuñu daaray alxuraan yi ne ci wàll woowu lañu bokk. Ñu gis ci at yii ci génn ay jéego yu mag ñeel ko ngir gën a jëmal njàngum alxuraan ci réew mi. Muy lu war ginnaaw ba ñu gisee taxawu Saa-Senegaal ci ay joŋante fépp ci àddina si te ay ndam rekk lañu fa jële.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj