Waajtaayu gaynde yi : ñaari joŋate, benn bii

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw ñaari joŋantey waajtaay yi mu doon amal diggante gaawu ak talaata (24i fan ak 27i fan ci weeru Sàttumbar 2022), ikibu Senegaal bi am na ci benn bii (digganteem ak Boliwii ndam 2i bii ci 0), bi ci des mu témboo ci ak Irã (1-1). Ñuy njureef yu am solo ndax ñàkku ci benn yoon. Waaye, na woon, fa woon. Ikib bi am na jafe-jafey Dugal bii.

Bilaŋu waajtaayu ikibu Senegaal bi ci yoonu kub bu àddina si dal na xel. Li ko dalee ci woote Aliw Siise bi, 29i joŋantekat yi mu ci boole, ba ci njureefi joŋante yi, bare na lool lu ci jàngatkat yi rafetlu. Li ci ëpp solo nag, ba di ñëw di ñëwaat, moo di ñàkkul benn yoon ci joŋante yooyu. Loolu nag, tax na ba ñu jàpp ni Senegaal ikib bu baax la te naqaree dóor. Noonu la ko Kalidu Kulibali dëggalee itam ci bi muy janook taskati xibaar yi :

« Joŋante nan joŋante bu metti ak ikibu Asi bi gën a réy. Daan nan gis Irã muy def joŋante yu baax ak i ikib yu réy. Tey nag jéem nanoo am ndam waaye ci temboo lanu mujje. Sunu biir ikib nag, genn njaboot lanu. Ñépp a booloo di dem ba jeex. Xel moomu lanu jiital ci ikib bi. Dafa am solo lool ngay gàddu sa raaya réew. Dafay feeñ ci joŋante yi. Yaakaar naa dinanu won àddina sépp ni ikib bu baax lanu yor, ci yi gënn a baax ci àddina si. »

Ci ñaari joŋante yépp gis nañ ikibu Senegaal bu am taxawaay, di bërëŋ bal bi kow ba suuf. Futbal bu rafet bi ñépp doon xaar ci ñoom feeñ. Waaye, bu leen kenn dóorul itam, benn bii doŋŋ lañ dugal. Bi muy dóor Boliwii la Bulaay Ja duggal ci bi joŋante bi tolloo ci 4i simili. Beneen bii bi Saajo Maane duggal, penaatii la. Ci joŋante bu mujje bi, defãsëeru Irã bi moo duggal bal bi ci seenub kã ba tax Senegaal jiitu laata Irã di delsi.

Ci tënk, ikibu Senegaal bi dawal na bal bi lu ëpp 176i simili te mënul a fexe ba gis caax yi. Lu mu tabax, beneen ikib bi toj walla ay ataakãwam ci boppam màndee ko. Loolu nag nekk na lu kenn dul nangul ikib bu mag. Ndaxte, futbal du ko jéggale. Boo ko defee defaat ko, boo moytuwul sa caax boy. Te loolu moo am ci joŋanteem bi ak irã. Bim ko amee amati ko muy moy, Irã daf ko am rekk dugal ko.

Yile seetloo tax ba Feerdinaa Kóli, bokkoon ci joŋantekati Senegaal yi fi defoon jaloore 20i at ci Ginnaaw ca Mali ak ca Sewul, yékkatiy kàddu ci laaj-tontu bi mu séqoon ak waa Source A :

« Gis nan futbal bu baax, bu rafet ak ikibu Senegaal bu am doole. Waaye am na ay yàqute ci mujjantal gi. Ci futbal nag, boo dul dugal okaasiyoŋ yi ngay sàkku, mënaguloo aar sa bopp. Te loolu moo xew ci sunu diggante ak Irã ba mu delsi. Ci futbal bu kowe bi, loolu la. Boo dul dugal say okaasiyoŋ, yaa ngi kàmbal sa bopp. »

Wax ji delsi di benn ci lees mën a jële ci ñaari joŋante yi. Senegaal yor na ikib bu baax, ñàkkul benn yoon ci ñaari joŋante yi. Aliw Siise andi na coppite yu am solo. Terewul woy wa demoon delsi na : dugal bii doon na lu jafe ikibu Senegaal bi.

 

Nataal : Onze Mondial

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj