WAAJTAAYU MÀGGALU TUUBAA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dëkk bu sell bi, Tuuba, dafa aadawoo di amal at mu jot màggalu 18 Safar. Muy bés bu màgg a màgg ci tarixa muridiyya. Di dajale mboloo mu takku. Muy màndargaal tukkib géej bi. Ren mu nar a nekk ci digg nawet bi, di yamook fukki fan ak juróom ci weeru sàttumbar. 

Ci jamonoy nawet lañu tollu. Te ku wax nawet, xel yi dem ci ndox. Ku wax ndox mu bari tudd mbënn. Ren ñu gis ne mbënn moomu lëmbe na dëkk yu bari ci biir réew mi. Tuuba kenn demut mu des doonte ña nga ca waajtaayu màggal gi. Ci loolu, Sërin Basiiru Abdu Xaadr mi yore kàddug Xalifa bi, genn na  janook taskatu-xibaar yi dibéer jii ñu weesu. Ñu doon waxtaane nan lañuy waajalee màggal gi. Ginnaaw bi mu fàttale taarixu bés boobu, yékkati na kàdduy soññe ci mbënn mi sonal gox ya ca Tuubaa. Doonte ne xew-xew boobu ay ayu-bés yu néew moo ci des, taa-taa yaa ngi wéy di sonal waa dëkk ba. Muy woo waa Càmm gi ñu jël seen i matuwaay ngir bés boobu ñu jëm, mën a yemb. Sëriñ bi di ñaawlu tamit yokkuteg njëgu soble si. Di fàttali ak a ñaax jaaykat yi ñu yërëm askan wi. 

Ci loolu jëwriñ ji ñu dénk biir réew mi, Antuwaan Jonn amal na tukkib nemmeeku fa Tuuba. Li ko yékkati di saafara mbënn mi ak naal bees dippe Plan ORSEC. Nemmeeku na gox yu mel ni Ndaamaatu ak Kër-ñaŋ yi bokk ci diiwaan yi ndox mi di gën a sonal. Biral na fa tamit lañu jot a def. Bokk na liggéey bi ñu sumb ngir jële fi ndoxu taw yi ci Tuubaa. Ñu def ci luy tollook ñaar-fukk ak ñett ciy miliyaar. Ciy kàddu yu mu dénk wa Sud quotidien, mi ngi xamle ne liggéey boobu door na. Jot na fa yëgle tamit liggéey bu ñu tàmbali ngir amal ñaareelu mbànd muy dajale ndoxu taw yi. Ñu koy tabax ca diiwaanu Kër-Kan. Mu ngi tollu ci diggante 40 ba 60i ektaar cib yaatuwaay. 

Mën nañoo wax ne matuwaay yu bari  jël nañu leen ngir màggal gi mën a jaar yoon. Waajtaay yi door nañu ngir Tuuba mën a dalal ay ganam, ñu màggal ci jàmm. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj