Ginnaaw bi ñu ko tabbee yees ci wàllum mbatiit ak moomeel, Aliw Sow door na tukkib nemmeeku ci biir réew mi. Li ko jëwriñ ji dugge mooy nemmeeku ak jege askan wiy yëngu ci wàllum aar ngir gën a xam seen i jafe-jafe. Démb, ci altine ji, mu ngi woon Géejawaay ak Pikin. Gise na fa ak artist ya fa nekk, rafetlu seen liggéey ak lañ jot a sottal.
Ñu seetlu ne jëwriñ jii di Aliw Sow, mébétam mooy xam, balaa dara, lëf lees ko dénk ak jafe-jafe yi mu làmboo ngir indi ciy saafara. Beneen jubluwaay bi mooy jege nit ñi ciy yëngu ngir gën leen a taxawu. Mu mel ni ay kàddoom da koy dëggal. Ndax kat ma nga naan :
“ wat gaal ak yëgoo, doo toog rekk tëju, dangay fekki askan wi fi ñu nekk gisal sa bopp, déggal sa bopp, xool li ngay def naka nga koy méngale ak seen i bëgg-bëgg”.
Kàddu yii, jukkees na leen ci I RADIO. Mu mel ni, jëwriñ ji dafa bëgg a jege aw ñoñam ngir di xàccandoo ak a dóorandook ñoom, xam seen i njàmbat ngir indi ci ay saafara.
Ci kow loolu nag, moom Aliw Sow jot na biral bëgg-bëggu Càmmug ñeel kopparal gi war ci artist yi. Fésal na yéeneem ci lëkkale liggéeykat yi ak yenn ciy kurél yi dimbali liggéeykat yi. Noonu, lim na kurél yii di DER/FJ, FONGIP ak BND. Li mu bëgg mooy jàppale képp ku sumb ab naal ci wàllu aar, mu am xaalis bi mu koy jëmmalee. Loolu dina tax ba ñooñu mu njaboote mën a xelli ay xalaat ba jëmale kanam koom-koomu réew mi. Ñu mën cee jàngatee ne dina nekk wokkatu bu dajeek geestu. Ndax kat artist yi yàgg nañoo jàmbat seen tumurànke ci fànn wile. Mënees naa wax ne, kon, sémbam bii dafa nëw ci waxtoom. Te, dina tax ba mbatiit suqaliku.
Ñu mën cee jàngate tamit ne bépp liggéeykat, balaa nga koy mën a dimbali, fàww nga jege ko, xam ay jafe-jafeem ngir saafara ko. Doxalin wii, ab jéego bu réy la bu mën a sabab naataange. Ndax kat, liggéey yi mu ëmb bari nañ te mën nañu suqali koomu réew.