WOTEY 2024 YI : 19i LAWAX ÑOO CI DES

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw bi mu neenalee dekkare Njiitu réew mi jëm ci fommug wotey 25 féewiryee 2024 yi, Ndajem Ndeyu àtte mi sëggaat na ca waynderew lawax yi. Lépp ngir saytuwaat rëq-rëq ya ñu ca nemmeeku woon ngir fésal lees mën a jàpp. Ci loolu, ci talaatay démb ji, ñoom juróom-ñaari kàngaami àttekat yi torlu nañu ab yégle bu bees.

Ci yégle boobu, ñu seetlu ca ay coppite jëm ci lim bi nar a dem ca yooyu joŋante. Lépp nag ñu tegg ko ci ay lay yu koy laytaay te ñu jukkee ko ci Ndeyu àtte réew mi. Ci noonu, dañu rocci ci biir ñaar-fukki (20) lawax ya woon, Róos Wardini mi ñu waxoon ne dafa ame ñaariy askanale, gog Senegaal ak gog Farãs.

Bu ñu sukkandikoo ci dogu 34 bu àtte bi, lii la wax :

Bu fekkee ne, kenn ci wutaakon (lawax) yi dafa am ngànt lu sax dàkk, mbaa mu bàyyi, ci diggante génnug dogal bi siiwal limu wutaakon yi ak sumb bu njëkk bi, pal gi dees koy eggali ak yeneen i wutaakon yi des ci géew gi. Naka noonu, Ndajem Ndeyu àtte mi day soppi limu wutaakon yi. Bésub pali gi deesu ko fomm”.

Ci loolu, limu lawax yi nii la tëdde, muy fukk ak juróom-ñeent (19) :

Buubakar Kamara

Séex Tijaan Jéey

Décce Faal

Daawda Njaay

Habiib Si

Xalifa Abaabakar Sàll

Anta Baabakar Ngom

Aamadu Ba

Idriisa Sekk

Aliw Mammadu Ja

Sëriñ Mbuub

Pàppa Jibriil Faal

Mammadu Lamin Jàllo

Mahammad Bun Abdalaa Jonn

Elaas Maalig Gàkku

Aali Nguy Njaay

Elaas Mammadu Jaawo

Basiiru Jomaay Jaaxar Fay

Ceerno Alasaan Sàll.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj